7
1 Gannaaw ba ñu tabaxaatee tata ja, ma taxawal lafi bunt ya, ba noppi dénk fara bunt ya seen liggéey, ñook jàngkat yaak Leween ña. 2 Ci kaw loolu ma sas sama mbokk Anani, mu jiite Yerusalem, mook Anaña boroom tata ja, ndax la mu gëna dëggu ñu bare, gën leena ragal Yàlla. 3 Ma ne leen: «Bu bunti Yerusalem ubbiku li feek jant bi tàngul. Santleen fara bunt yi ñuy tëj bunt yi, sës ci galani tëjukaay yi, balaa waa dëkk biy tëdd. Na ku nekk ci waa Yerusalem di wattoo ca bérabu wattukaayam, mbaa buntu këram.»
4 Booba dëkk ba réy na, yaatu na; waaye nit ña ca dëkk ñoo néew, te kër ya tabaxewaatul woon. 5 Sama Yàlla xiir ma ma woo garmi yeek kilifa yeek baadoolo yi, ngir bind leen. Ci biir loolu ma gis limeefu làng ya jëkka jóge ngàllo ga, ba ñibbsi. Li ma fekk ñu bind ko ci mooy lii:
6 Ñii nag ñoo di niti diiwaanu Yuda, ña jóge njaam ca ngàllo ga leen Nabukodonosor buuru Babilon yóbbu woon, te ñu jóge ca ñibbsi Yerusalem ak Yuda, ku nekk ak fa mu dëkk. 7 Ña nga ñibbi ca njiital Sorobabel ak Yosuwea ak Neyemi ak Asaryaa ak Ramya ak Nayamani ak Mardose ak Bilsan ak Misperet ak Bigway ak Neyum ak Baana. Limeefu góori bànni Israyil nii la tëdde: 8 Askanu Paros ñaari junni ak téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (2 172). 9 Askanu Sefatiya ñetti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar lañu (372). 10 Askanu Ara di juróom benn téeméer ak juróom fukk ak ñaar (652). 11 Askanu Payat Mowab, soqikoo ci Yeswa ak Yowab, di ñaari junni ak juróom ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (2 818). 12 Askanu Elam junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). 13 Askanu Sàttu juróom ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (845). 14 Askanu Sakay juróom ñaar téeméer ak juróom benn fukk lañu (760). 15 Askanu Binuy juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett lañu (648). 16 Askanu Bebay juróom benn téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (628). 17 Askanu Asgàdd ñaari junni ak ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (2 322) 18 Askanu Adonikam juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom ñaar lañu (667). 19 Askanu Bigway ñaari junni ak juróom benn fukk ak juróom ñaar lañu (2 067). 20 Askanu Adin juróom benn téeméer ak juróom fukk ak juróom lañu (655); 21 askanu Ater soqikoo ci Esekiya, di juróom ñeent fukk ak juróom ñett (98); 22 Askanu Asum ñetti téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (328). 23 Askanu Besay ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñeent lañu (324). 24 Askanu Arif téeméer ak fukk ak ñaar lañu (112). 25 Askanu Gabawon juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95). 26 Waa Betleyem ak Netofa téeméer ak juróom ñett fukk ak juróom ñett lañu (188). 27 Waa Anatot téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett lañu (128). 28 Waa Bet Asmawet ñeent fukk ak ñaar lañu (42). 29 Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Berot juróom ñaar téeméer ak ñeent fukk ak ñett lañu (743). 30 Waa Raama ak Geba juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (621). 31 Waa Migmas téeméer ak ñaar fukk ak ñaar lañu (122). 32 Waa Betel ak Ayi téeméer ak ñaar fukk ak ñett lañu (123). 33 Waa Nebo gu ndaw juróom fukk ak ñaar lañu (52). 34 Waa Elam gu ndaw junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). 35 Waa Arim ñetti téeméer ak ñaar fukk lañu (320) 36 Waa Yeriko ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345). 37 Waa Lodd ak Adidd ak Ono juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk ak benn lañu (721). 38 Waa Sena ñetti junni ak juróom ñeenti téeméer ak fanweer lañu (3 930).
39 Sarxalkat yi ñii la:
Askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973). 40 Askanu Imer junni ak juróom fukk ak ñaar lañu (1 052). 41 Askanu Pasur junni ak ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar lañu (1 247). 42 Askanu Arim junni ak fukk ak juróom ñaar lañu (1 017).
43 Leween ñi ñii la: Askanu Yeswa ma soqikoo ca Kadmiyel. Mooy ñi bànqaasoo ci Odawya, tollu ci juróom ñaar fukk ak ñeent (74).
44 Jàngkat yi ñoo di: Askanu Asaf, di téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett (148). 45 Askanu fara bunt yi ñoo di: Askanu Salum, ak askanu Ater, ak askanu Talmon, ak askanu Akub, ak askanu Atita, ak askanu Sobay, di téeméer ak fanweer ak juróom ñett (138).
46 Liggéeykati kër Yàlla gi ñoo di: Askanu Ciya, ak askanu Asufa, ak askanu Tabawot, 47 ak askanu Keros, ak askanu Siya, ak askanu Padon, 48 ak askanu Lebana, ak askanu Agaba, ak askanu Salmay, 49 ak askanu Xanan, ak askanu Gidel, ak askanu Gayar, 50 ak askanu Raaya, ak askanu Reccin, ak askanu Nekoda, 51 ak askanu Gasam, ak askanu Usa, ak askanu Paseya, 52 ak askanu Besay, ak askanu Meyunim, ak askanu Nefusim, 53 ak askanu Bagbug, ak askanu Akufa, ak askanu Arur, 54 ak askanu Baslut, ak askanu Meyida, ak askanu Arsa, 55 ak askanu Barkos, ak askanu Sisera, ak askanu Tema, 56 ak askanu Necciya, ak askanu Atifa.
57 Askanu jaami Suleymaan ñii la: Askanu Sotay, ak askanu Soferet, ak askanu Perida, 58 ak askanu Yaala, ak askanu Darkon, ak askanu Gidel, 59 ak askanu Sefatiya, ak askanu Atil, ak askanu Pokeret Asbayim, ak askanu Amon.
60 Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392).
61 Ña bàyyikoo Tel Mela ak Tel Arsa ak Kerub Adon ak Imer te manuñoo firndeel ne seen waa kër maam ak seen askan ci Israyil lañu bokk, ñii la: 62 Askanu Delaya, ak askanu Tobya, ak askanu Nekoda, di juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak ñaar (642).
63 Am na it ñu loolu daloon ci sarxalkat yi, muy askanu Abaya, ak askanu Akocc, ak askanu Barsilay, ma doon denc doomu Barsilay waa Galàdd ba, ba tax ñu santale ko seen sant. 64 Ñooñu seet nañu seen limeefu kër maam, waaye gisuñu ko. Ñu daldi leen doyadal, génne leen ci carxal gi. 65 Boroom dëkk ba nag aaye leen ñu lekk ci ñam yu sell yaa sell, ba keroog sarxalkat ba di am lu leer ci ñoom ci jumtukaayi tegtal yi ñuy wax Urim ak Tumim.
66 Limu mbooloo ma mépp ba mu daj, ñeent fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk lañu (42 360), 67 te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen, yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay jàngkat yu góor ak yu jigéen, yu tollu ci ñaar téeméer ak ñeent fukk ak juróom (245), 68 ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720).
69 Am na ñu jiite seen kër baay, ñu def seen loxo ca liggéey ba. Boroom dëkk ba def na ca alal ja junniy poseti wurus (1 000) ak juróom fukki këll (50) ak fanweeri mbubbi sarxalkat (30) ak juróomi téeméeri dogi xaalis (500)b.
70 Ñenn ca ña jiite seen kër baay def nañu seen loxo ca alal ja ñu jagleel liggéey ba, mu tollu ci ñaar fukki junniy poseti wurus (20 000) ak ñaari junniy dogi xaalis ak ñaar téeméer (2 200).
71 La des ca askan wa joxe na ñaar fukki junniy poseti wurus (20 000) ak ñaari junniy dogi xaalis (2 000) ak mbubbi sarxalkat yu tollu ci juróom benn fukk ak juróom ñaar (67).
72 Ba loolu amee bànni Israyil gépp sancaat ca seen dëkki cosaan, sarxalkat yaak Leween ñaak fara bunt yaak jàngkat yaak ñenn ca baadoolo yaak liggéeykati kër Yàlla ga.