Esra jàngal na mbooloo ma
8
Ba juróom ñaareelu weer wa teroo, ba bànni Israyil sancaat seeni dëkk, 1 mbooloo mépp a daje, di benn bopp ca mbedd ma jàkkaarlook buntu Ndox ma. Ñu wax Esra bindkat ba, ne ko mu indi téereb yoonu Musaa wi Aji Sax ji dénk Israyil. 2 Esra, sarxalkat ba, indi téereb yoon wi keroog benn fanu juróom ñaareelu weer wa, fa kanam mbooloo ma, góor ak jigéen, mboolem ña seeni at may ñu dégg ko. 3 Esra jàng na ko janook mbedd ma jàkkaarlook buntu Ndox ma, dale ko ba bët setee ba ca digg bëccëg. Mbooloo maa nga teew, góor ak jigéen, mboolem ña dégg la ca nekk. Ñépp nag di teewlu kàdduy téereb yoon wa.
4 Esra bindkat baa nga taxaw ca kaw dëxu bant ba ñu defaral bés ba. Ña feggook moom ca ndijooram di Matitiya ak Sema ak Anaya ak Uri ak Ilkiya ak Maaseya. Ña ko féete càmmoñ di Pedaya ak Mikayel ak Malkiya ak Asum ak Asbadana ak Sàkkaryaa ak Mesulam. 5 Ba Esra di ubbi téere ba, mbooloo mépp a ca teg seeni bët, ndax mbooloo mépp la tiim. Mbooloo mépp nag jóg taxaw. 6 Esra daldi sant Aji Sax ji, Yàlla ju màgg ji. Mbooloo ma mépp ànd ne: «Eskëy, eskëy!» yékkati seeni loxo, sukk, sujjóotal Aji Sax ji, dëpp seeni jë fa suuf. 7 Ci kaw loolu Yeswa ak Baani ak Serebya ak Yamin ak Akub ak Sabtay ak Odiya ak Maaseya ak Kelita ak Asaryaa ak Yosabàdd ak Xanan ak Pelaya ak Leween ña di leeralal mbooloo ma yoonu Musaa. Mbooloo maa nga taxaw, kenn ku nekk benn bérab. 8 Ci biir loolu ñu di leen jàngal téereb yoonu Yàlla wi, njàng mu leer, di leen ko firil ba ñu xam li ñuy jàng.
9 Gannaaw loolu Neyemi boroom dëkk ba ànd ak Esra sarxalkat ba, di bindkat ba ba tey, ak Leween ñay xamal mbooloo ma, wax ak ñoom ñépp, ne leen: «Bésub tey jii, bés bu sell la, ñeel Aji Sax ji, seen Yàlla. Buleen ci naqarlu, buleen ci jooy.» Booba mbooloo ma mépp a doon jooy ca kàdduy yoon wa ñu dégg. 10 Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!» 11 Leween ña nag di dëfal mbooloo ma mépp, naan leen: «Noppileen waay, ndax tey bés bu sell la. Kon buleen ci naqarlu.» 12 Ba mu ko defee mbooloo ma mépp ñibbi, di lekk ak a naan ak a yekkle di bànneexu bu baax. Fekk na ñu xam kàddu ya ñu leen doon xamal.
Feddli nañu màggalu Mbaar yi
13 Keroog ñaari fan ca weer wa nag ña yilif seen kër baay yépp ànd ak sarxalkat yaak Leween ña, ñu daje ca Esra bindkat ba, di gëstu kàdduy yoon wi. 14 Ci kaw loolu ñu gis ne bind nañu ci yoon wi Aji Sax ji santaane, te Musaa jottli ko, ne: «Bànni Israyil dañoo wara dëkk ci ay mbaar diiru màggalu weeru juróom ñaareel wa.» 15 Ñu siiwal nag ndigal, ca mboolem seeni dëkk ak ca Yerusalem, daldi yéene ne: «Demleen ca tund ya, wuti ay cari garabi oliw, ak cari garabi pẽea, ak cari garabi mirt, ak cari garabi tàndarma, ak cari garab yu sëq, ndax ñu defare ko ay mbaar, muy li ñu bind.» 16 Ba loolu amee mbooloo ma wuti ay car, defare ko ay mbaar ca seen kaw taaxi kër ak ca seeni biir ëtt ak ca ëtti kër Yàlla ga ak ca mbedd ma ca buntu Ndox ma ak ca mbedd ma ca buntu Efrayim. 17 Ci kaw loolu mboolem ña ñibbsee ca njaam ga defar ay mbaar, dal ca mbaar ya. La ko dale jamonoy Yosuwe doomu Nuun, ba bésub keroog bànni Israyil defatuñu woon lu ni mel. Muy mbégte mu réya réy. 18 Ci biir loolu ñuy jàng ci téereb yoonu Yàlla wi bés bu nekk, tàmbalee ko ca bés bu jëkk ba, ba ca bés bu mujj ba. Amal nañu màggal ga diiru juróom ñaari fan. Bésub juróom ñetteel ba nag ñu woote ca am ndaje mu sell, muy la ñu digle.