Mardose daan na
10
1 Gannaaw loolu Buur Aserus gàll ab galag ca réew ma mépp, ba ca duni géej ga. 2 Mboolem jaloore ya Buur Aserus def, ca dooleem ak màggaayu darajaam ak na mu yékkatee Mardose, ba mu kawe, lépp bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Medd ak Pers ca seeni jant. 3 Mardose Yawut ba, moo sësoon rëkk ca Buur Aserus, sut Yawut yépp, ay bokki Yawutam yu bare nawloo ko. Muy sàkku nag ngëneeli ñoñam, di waxal jàmm mboolem askanam.