Ayóoba
Ubbite gi
Téereb Ayóoba moo nettali dundu nit ku baax ku musiba mu réy dal. Alalam jépp la jëkka ñàkk, teg ci ñàkk doomam yépp, boole ci jàngoro ju daw yaram. Gannaaw loolu, téere bi indi na ñetti pàcci wàqante yu taalife yu Ayóoba séq aki xaritam, te lépp di biral seeni tont ci tiis yooyu. Li gëna fés ci seen werante moo di ni Yàlla farala jëflantee ak doom aadama, waaye Yàlla ci boppam moo mujj feeñu Ayóoba.
Xariti Ayóoba yi, ni ñu jàngate tiisi Ayóoba mooy ni ko aaday cosaan gise ci wàllu diine rekk. Foog nañu ne, gannaaw Yàlla mbaax la mas di yoole jëf ju baax, di añale mbugal jëf ju bon, coono yi Ayóoba daj, añub bàkkaaram doŋŋ lay mana doon. Teewul Ayóoba xamle ne mbir mi yombewul noonu, te it yelloowul mbugal mu mettee ni li ko dal lépp, ndax moom ci boppam, mbaax geek njubte gi mu masa jàppoo, barewu ciy moroom. Xelum Ayóoba moo manula jàpp nan la Yàlla mana seetaane yooyu coono di dikkal ku mel ni moom. Moo tax mu am fitu dëkk Yàlla ci layoo bu mu bëgga séq ak moom. Taxul Ayóoba gëmadi, waaye nammeelam moo di mu am dëgg fi kanam Yàlla, ak itam firnde ju setal deram, gannaaw moom nit ku baax la.
Li Ayóoba laaj nag, Yàlla àdduwu ci, waaye ngëmu Ayóoba la tontoo kàddu gu jeexal aw lay, ci ab taalif bu mu misaale ne moo man te moo xam. Gannaaw loolu la Ayóoba nangu ne Yàlla mooy Buur te moom rekk a xam. Ci kaw loolu la tuub waxi meram ju ëpp.
Tëjteb téere bi moo nettali ni Ayóoba mujje. Xariti Ayóoba ya nag la Yàlla sikke kàddu yu dëng ya ñu firee coonoy Ayóoba. Mennum Ayóoba doŋŋ moo njort ne màggug Yàlla weesu na ni xaritam yooyu fooge Yàlla, ci seen gis-gis bi leen diiney cosaan gisloo.