Ayóoba nee su layoo, yey
13
1 Dama ne, lii lépp maa ko gis,dégg ko, xam ko.
2 Li ngeen xam, man it xam naa ko;
duma seen cuune fenn.
3 Waaye man Aji Man ji laay waxal,
layook Yàlla laa namm.
4 Yeen nag yeenay rafetalkati fen,
yeen ñépp di fajkati caaxaan.
5 Céy su ngeen noon cell,
muy seen rafet xel!
6 Ngalla dégluleen sama tawat,
teewluleen sama kàddug layoo.
7 Yàlla daal ngeen di waxal njubadi,
di ko duural?
8 Yàlla ngeen faral,
am Yàlla ngeen di layool?
9 Bu leen luqatu woon dina baax a?
Am ni ñuy naxe nit ngeen koy naxe?
10 Su ngeen ko faraloon ci kumpa sax,
du tee mu sikk leen moos.
11 Xanaa màggaayu Yàlla tiitalu leen?
Am ragluwaayam ëlëmu leen?
12 Seeni tari, léebi neen,
seeni tont, kiiraayu boob.
13 Xeremluleen, ba ma wax man
ak lu ma mana dal.
14 Ana lu ma tax di yàpp sama pàllax,
di jaay sama bakkan?
15 Su ma doon rey it moom laay yaakaar,
maay janook moom, layool sama bopp.
16 Loolu it sama mucc a ngi ci,
nde ab yéefar du dikk di janook moom.
17 Dégluleena déglu sama baat,
sama kàddu ci seeni nopp.
18 Dégluleen maa, ma lañal ab layoo,
bir na ma ne maay yey.
19 Ana ku may yey cib layoo?
Kon de ma wedam te dee.
20 Xanaa nga may ma yaar rekk,
ba du jar ma di la làqu:
21 ngalla teggi ma sa loxo,
te buma dabeeti tiitaange loo sabab.
22 Wooteel, ma wuyu,
mbaa ma wax, nga àddu ma.
23 Ana luy sama ñaawtéef aki moy?
Xamal ma samag tooñ ak sama moy.
24 Ana loo may làqe sa leeru kanam?
Danga maa jàppe sab noon?
25 Xob wuy wéy ngay xoqtal?
Ana boob muy naaw, loo ciy topp?
26 Yaa ma bindal dogal yu wex,
añale ma sama ñaawtéefi ndaw!
27 Yaa ma jéng,
di sàmm fépp fu ma jaare,
topp sama tànk!
28 Sama bakkan a ngi ruus ni bant bu fënëx,
mbaa mbubb mu maxe.