Àddinaa gàtt, barew tiis
14
1 Ku jigéen jur,
yaa néewi fan, géejal coono!
2 Dangay tóor rekk, lax,
wéy ni takkndeer, doo toog.
3 Mooy kii nag nga teg bët,
mooy man mii nga nara layool!
4 Lu sobewu, ana ku ci mana am lu laab?
Du kenn!
5 Ndegam yaa dogalal nit ay fanam,
lim ay weeram,
dogal àpp ba, te du jaas,
6 teggi ko boog say gët, mu dal-lu,
ni liggéeykat bu jaanam wàcc ci bés.
 
7 Garab sax ñàkkul yaakaar.
Boo goree, mu jebbiwaat,
ba du ñàkk ay njebbat.
8 Reen ba man naa màggat,
ëkk ba deeye biir suuf,
9 mu yég um ndox, rekk, jebbi,
saxaat nim njëmbat.
10 Waaye nit dee, doole réer,
bakkan rot, mu ne mes.
11 Day mel ni déeg bu ŋiis,
mbaa dex gu wow ba jeex.
12 Doom aadama it tëdd, du jógati,
du yewwooti, asamaan fekke,
du jógeeti ciy nelaw.
Làq ma sa mer, ba giif
13 Éy soo ma nëbboon biir njaniiw,
làq ma, ba sa mer giif,
dogalal ma àpp, te bañ maa fàtte!
14 Ndax dees na dee, di dundati?
Konoon ma muñe ko sama fani coono yépp,
ba keroog sama kuutaay yiwisi ma.
15 Konoon nga woo ma, ma wuyu,
te kon nga namm sa càkkéefu loxo.
16 Konoon yaay lim samay jéego,
te doo ma topp samay bàkkaar.
17 Konoon samag tooñ yebe
ci mbuus mu takke,
sama ñaawtéef, nga muure ko malaan.
 
18 Waaye aw tund day màbb, ruus;
aw doj di toxu,
19 am ndox di jonji xeer ba mu jeex,
waame buub suuf, yóbbu,
te noonu ngay neenale yaakaaru doom aadama,
20 man ko, mu dëddu fàww,
kanam ga soppiku, nga jalax.
21 Doom ya tedd, yégul;
ñu tekkeedi, tinul.
22 Nit yégul lu moy mititu boppam
te bakkanu boppam lay tiisoo.