Yàllaa may jot
19
1 Ayóoba àddu ne:2 Dungeen ma noppee xañ jàmmi bakkan,
di ma sëf wax ju dul jeex?
3 Fukki yoon a ngii ngeen di ma saaga,
te rusuleen maa sonal.
4 Su ma moyoon dëgg sax,
maay bokk ak sama moy fanaan.
5 Defe ngeen ne yeena ma gën,
ba di ma sikke musiba mii ma dal?
6 Waaye xamleen ne Yàllaa ma tooñ,
ab caaxam a ma dar kepp.
7 May woote wall, wuyeesu ma,
ma ñaan ndimbal, àtteesu ma.
8 Manumaa jàll, Yàllaa fatt sama yoon,
lëndëmal samay jaaruwaay,
9 sàggi sama sag,
foq sama kaala,
10 tojat ma wetoo wet ba ma tàggoo,
déjjati sama yaakaar ni garab,
11 jafalal mam sànjam,
boole ma ciy noonam,
12 ay gàngooram dikkandoo,
yékkatiy jal, gawe ma,
dal fi wër sama xayma.
13 Samay bokk, mu soreleek man,
samay xame sax ñooru ma.
14 Jegeñaale ba ma,
xame fàtte ma,
15 sama gani démb def ma ni jaambur tey,
samay mbindaan it noonu,
ñu def ma ni doxandéem.
16 Su ma doon woo sama surga, ba di ko tinu sax,
da may tanqamlu.
17 Sama xetu gémmiñ dàq na sama jabar,
sama doomi ndey sax seexlu ma.
18 Gone yi sax a ngi may sewal,
su ma jógee di dem, ñu di ma baatal.
19 Sama wóllërey démb yépp a ma sib,
ma sopp leen, tey ñu dëddu ma.
20 Der aki yax laa dese,
daanaka dee naa.
21 Yërmandee, yërmande, yeen samay xarit,
Yàllaa xàcci, fàdd ma!
22 Lu ngeen ma toŋale nii ni Yàlla?
Xanaa yàppuleen ma ba suur?
23 Éy su samay kàddu tënku woon ci mbind!
Éy su ñu manoona xacc mbind ma cib téere,
24 xacce ko xalimag weñ ak beteex
mu ñaase fàww ciw doj!
25 Waaye man xam naa ne sama jotkat a ngi dund,
te mooy mujje taxaw fi kaw suuf.
26 Bu sama der bi lekkoo sax,
du tee ma dese suux wu ma xoole Yàlla,
27 xoolal ko sama bopp,
te du doon sama gan.
Maaka namm lii ci sama xol!
28 Yeena ngi naan: «Ana nun koy toŋale,
ba am lay wu ko tiiñal?»
29 Ragal-leen saamar!
Seen xadar jii ñaawtéef la, saamar ay àtteem,
xamleen ne àtte am na.