Cofar nee ku musiba dab, yaa tooñ
20
1 Cofar mu Naama àddu ne:
2 Kon ma àddooti ndax jaaxle,
ba xol jallaañoo.
3 Dégg naa kàddug yedde gi nga may saagaa,
waaye samam xel a ma déey sa tont.
 
4 Xanaa xamoo lii? La dale ca cosaan,
ba nit tegoo kaw suuf ba tey,
5 xamoo ne ku bon, ag sarxolleem àggul fenn,
te bànneexu yéefar yàggul?
6 Bu màggoon ba tollook asamaan it,
ba bopp ba àkki fa kawa kaw,
7 day mujj seey fàww niy jonkanam;
ña ko daa gis naa: «Ana mu?»
8 Kenn du ko gisati, day réer ni gént,
mbaa njeneeru guddi ju dàqu, wéy.
9 Bët bu ko gisoon du ko tóllanti,
dëkkuwaayam dootu ko séen,
10 ay doomam ay dàmp néew-ji-doole yi,
ba delloo seen alal.
11 Mooy ànd ak dooley ndawam,
tëri biir bàmmeel.
12 Lu bon la daa tàqamtikoo,
log ko, làq ca suufu làmmiñ wa,
13 di ko siiramtal te du ko wacc,
xanaa taf ko ca digg denqleñ ma.
14 Waaye la muy lekk ay soppiku ca biiram,
doon daŋaru ñàngóor ca butit ya.
15 Moo dërëxoon alal, moo koy goqi,
ca biiram la ko Yàlla di yuree.
16 Ndeke tookey ñàngóor la muucu,
mu rey ko ni mat-matu saamaan.
17 Yàlla bumu niir wali dex
ak waltani lem ak soow.
18 Dina delloo lu mu amoon, du ko warax;
te alal ju mu jula woon, du ko jariñoo.
19 Moo dëggaate néew-ji-doole, dëddu ko;
aakimoo kër jaambur te tabaxu ko.
20 Biir ba du wéet,
lu mu xemmem, du rëcc.
21 Dara du rëcc ab kollam,
moo tax xéewalam du toog.
22 Fa mu regge lay jàqe,
mépp musiba këppu ci kawam.
23 Ba muy sol kollam
la ko Yàlla di yónnee tàngooru sànjam,
tawal ko ko lu fees déqam.
24 Mu daw ngànnaayu weñ,
fittu xànjar bëtt ko,
25 jam ko ba fëll,
cat la bëtt xol ba, di melax fa mu sare,
tiitaangey ndee ne ko taral.
26 Mboolem lëndëm a làqu di ko xaar,
te sawara wu loxo jafalul a koy xoyom,
lakkaale lu desoon ca xaymaam.
27 Asamaan ay weer ñaawtéefam,
suuf jóg, seedeel ko tuuma.
28 Koomum këram day tukki, ne mes,
keroog sànjum Yàlla ma.
29 Lii moo di wàllu nit ku bon, fa Yàlla,
muy cér bu ko Yàlla dogalal.