Ayóoba nee Yàllaa ngi tanqamlu
24
1 Lu tee Aji Man ji àppal nit bési mbugal,ba ku ràññee Aji Sax ji fekke yooyu bésam?
2 Nit a ngi toxal kemu suuf,
nit a ngi sàcc ug jur, foral leen.
3 Mbaamu jirim, ñu wommat, yóbbu;
nagu jëtun, ñu jël kob tayle.
4 Néew-ji-doole, ñu buuxe ko ciw yoon,
baadoolo yi far bokk làquji.
5 Néew-ji-doole yaa ngii mel niy mbaami àll ci màndiŋ mi,
di fortaatu lu ñu lekk,
àll bu wow bi yor seen xontu njaboot.
6 Tooli jaambur lañuy góobaani,
di wittaani reseñ ca tóokëri ñu bon ña.
7 Duŋŋ lañuy fanaane ndax rafle,
sàngoo seen der ci sedd bi.
8 Ñooy tawtee tund ya,
di làqoo xunti yu ñu seeloo.
9 Xoncees na jirim ci weenu ndeyam,
jëlees na tayle alalu néew-ji-doole.
10 Duŋŋ lañuy wéye ndax rafle,
biir wéet, ñuy gàdduy sabaar,
11 di nal diwu oliw ci tooli jaambur,
di dër reseñ ju ñu dul naan.
12 Biir dëkk ba la nit ñay binnee,
ña ñu gaañ di woote wall,
te Yàlla toppul kenn tooñ.
13 Ñee noonoog leer,
faalewñu yoonu bëccëg
te duñu fa taxawaaloo.
14 Bët di set, bóomkat jóg,
bóom baadoolo bi néew doole,
guddi jot mu dib sàcc.
15 Moykat bu góor a ngi yeeru timis,
fab ndimo, kaalawoo,
naan bët du ko gis.
16 Ñu ngi lëndëmtu, di toj kër yi,
bëccëg ñu tëju,
xamuñug leer.
17 Ñoom ñépp ñuulaayu guddeey seen bëccëg,
lëndëm gu ne këruus lañu xejjool.
18 Yal nañu wéye walum ndox,
te suuf sa ñu séddoo alku,
ba kenn dootu dëgmal tóokëru reseñ.
19 Yal na maral ak tàngoor ŋiisal seen ndoxum taw,
te njaniiw mëdd ña bàkkaar.
20 Yal na leen seen ndey sax fàtte,
sax yi muucu leen,
ñu fàtte leen,
ba njubadi déjjatiku ni garab.
21 Ñu ni mel ay lekk alalu jigéen ju tëlee jur,
te duñu baaxe jëtun.
22 Waaye Yàllaa mana dàq boroom doole,
su nee tëll, mu xalaat bakkanam.
23 Moo leen di may ñu wéeroo seen cëslaay,
tey xool fa ñuy jaare.
24 Dañuy jóg, nes tuut ñu ne mes,
wadd, ñu boole for,
ñu daldi lax niy gub.
25 Su dul noonu, ana ku may fenloo?
Ana ku mana neenal samay wax?