Deesul am dëgg fa Yàlla
25
1 Bildàdd ma bàyyikoo Suwa àddu, ne:
2 Yàllaa man te mata ragal,
di def jàmm fa kawteem ya.
3 Ay gàngooram limu naam?
Ana ku mu dul jam ceeñeeram?
4 Ana nu nit di ame dëgg fa kanam Yàlla?
Ku jigéen jur, nu mu mana laabe?
5 Xoolal, weer wi sax leerul ba doy ko,
te biddiiw yeet gisul seen sellaayu leer,
6 astamaak nit kii tanewulu sax,
doom aadama jii gënul gasax.