37
1 Lii déy a rëccal sama fit,
muy tëf-tëfee fa mu sax.
2 Dégluleena déglu dënoom gay ràndaŋ,
kàddu gay rëkke fa gémmiñam,
3 muy riiral fépp fu asamaan tiim,
di fettaxal melaxam ba cati àddina.
4 Ca lay yëmmu,
dënoo kàddoom gu màgg,
te dootu téye melax yi,
li feek baatam di jib.
5 Yàllaay dënu kéemtaan,
di def kiraama yu nu wees.
6 Kee naan tawub yuur mu sóobal suuf,
di yebal taw ba ci waame yiy sóobe doole,
7 daldi téye loxol képp ku doon liggéey,
ngir képp ku mu sàkk xam jëfam;
8 Rabu àll duggi biir xunteem,
goori biir paxam,
9 ngëlén bawoo néegam
sedd ba tukkee fa ngelawi bëj-gànnaar.
10 Yàllaay nokki, ndox way,
wali ndox rasu, ne kekk.
11 Keey sëf xàmbaar, mu guux,
keey tasaare niir yi làmboo melaxam,
12 ñu jargandalu ci ndigalam
di fexee sottal mboolem santaaneem
ci kaw àddina wërngal këpp,
13 mu mel ni yet wu muy bantale waa àddinaam,
mbaa mu firndeele leen ko ngoram.
14 Yaw Baay Ayóoba, teewlul lii,
neel tekk te jàngat kéemaani Yàlla yi.
15 Dangaa xam nu Yàlla di sosey niiram,
ba melaxal melax gi ci niiram?
16 Dangaa xam nu niir yiy ajoo ci jaww ji,
kiraamay ku buural xam-xam a ngoog!
17 Yaw mi say yére di tàng,
bu ngelawu bëj-saalum di upp, suuf ne tekk,
18 ndax yaa ko lal-le woon déndub asamaan,
mu dëgër ni weñ gu ñu xelli?
19 Xamal nu boog lu nuy wax Yàlla!
Dunu mana lay ndax ñàkka xam.
20 Ndax dees koy yégal ne maay waaja wax?
Ana nit kuy ñaan sànkutey boppam?
21 Kenn manula xool jant bu ne ràññ,
gannaaw bu ngelaw walee niir yi ba mu set.
22 Bëj-gànnaar la leeru wurus di dikke,
booba Yàllaa làmboo darajaam ju raglu.
23 Aji Man ji nu dul daj daa bare doole,
dëggu, bare njekk, du note.
24 Moo tax ñu ragal ko,
faalewul kenn ku naw um xelam.