Aji Sax ji àddu na
38
1 Ba loolu amee Aji Sax ji àddoo fa ngëlén la, ne Ayóoba:2 Ana koo doon, bay lëntal samay dogal,
di wax loo xamul dara?
3 Takkul boog te góor-góorlu,
ma laaj la, nga xamal ma.
4 Ana foo nekkoon ba may samp suuf?
Waxal su la ko sam xel mayee.
5 Ana ku dogal dayo ya, umpu la?
Ku tàllal buum, natte ko ko?
6 Ana fu kenu ya sampe?
Ak ku teg doju coll wa,
7 ba biddiiwi njël sarxolleendoo,
goney Yàlla yépp xaacoondoo?
8 Ana ku tëjoon lafi buntu géej,
ba muy buccikoo xóote ya, fettax,
9 ba ma solal ko aw niir, mbubb,
laltaaye ko lëndëm,
10 dagg aw xélam, àppal ko kemu,
dogalee ko bunt bu tëje ràpp,
11 ba ne ko: «Fii ngay yem, doo fi wees.
Fii la say gannax di noppee buure»?
12 Ana foo masa joxe suba ndigal,
ba xamal njël bérabam,
13 ngir mu jàppe cati àddina, ag leeram,
yëlëbe ca ñu bon ñi,
14 àddina mel ni ban bu ñu teg torluwaay,
tey saamandaay mbubb mu ñu suub,
15 ñu bon ñi, ñu xañ leen seenug leer,
ba loxo ba ñu xàcci woon damm?
16 Yaa àkki ba fa géej bënne?
Am yaa daagoo ruqi xóotey géej?
17 Dees laa won bunti ndee?
Am yaa gis bunt ya jëm lëndëmu njaniiw?
18 Dangaa ràññee yaatuwaayu suuf si?
Waxal, ndegam xam nga lii lépp!
19 Ana yoon wa jëm fa leer dëkke,
ak fa lëndëm màkkaanoo,
20 ba nga man leena yóbbu fa ñu digaloo,
te ràññee seen yooni kër?
21 Xam nga ko moos, fekk na la juddu;
dund nga ay fani fan!
22 Yaa àkki ba fa mbàndi tawu yuur ya?
Am yaa gis mbàndi waamey donj yu sedd,
23 ya may dencal jamonoy njàqare
ngir bésub ndajem xare?
24 Ana yoon wu jëm fa leer di tasaaroo?
Ak fu ngelawal penku di xàjjalikoo,
ba dajal suuf si?
25 Ana ku xàllal waame,
ak ku sàkkal melax ak dënu aw yoon,
26 di taw fu kenn newul,
ci màndiŋ mu nit amul,
27 di suuxat gent bu maral,
ba saxal fam ñax?
28 Ab taw daa am baay?
Ana ku geñoom sos toqi lay?
29 Ana ku wasin ndox mu way,
ak ku jur layub asamaan bu sedd ba wow,
30 ba wali ndox yi dëgër niw doj,
déndu géej fasu, ne kekk?
31 Yaay faste genn dëllooñ gu ndaw
gi ci digg asamaan?
Am yaay yiwi dëllooñ gu mag ga mu dendal?
32 Yaay def bu jotee, nga feeñal biddiiw yi?
Am yaay wommat dëllooñu bëj-gànnaar
ak njabootam gu sew?
33 Dangaa xam dogali yoon yi yor asamaan?
Am yaay saytu kilifteefam fi kaw suuf?
34 Yaay yékkatil niir yi kàddug ndigal,
rekk waame sang la?
35 Yaay yebal melax yi ñu dem,
melaxi, délsi, ne la: «Nu ngi, ak fan?»
36 Ana ku yeb xel mu rafet cib dënn,
ak ku may ab xol dég-dég?
37 Ana ku xareñ ba waññ niir yi?
Ak kuy jolal mbuusi asamaan,
38 ba suuf di bàq, dankaloo,
defi donj, taqloo?
39 Yaay rëbbal gaynde?
Am yaay reggal doomu gaynde
40 ju goore biir paxam,
mbaa mu waafem ngeer, di tëroo?
41 Ana kuy xont baaxoñ,
fa doom yay wooye Yàlla wall,
di tërëf ndax ub xiif?