Yàlla fal na buur
2
1 Ana lu xeeti àddina di riir,
lu giir yiy nas pexey neen?
2 Buuri àddinaa ngi dér,
boroom nguur yi daje,
di fexeel Aji Sax ji,
mook ki mu fal.
3 Ña nga naan: «Nanu dagg càllala yi,
sànni jéng yi!»
 
4 Ki ci jalub asamaan a ngay ree,
Boroom baa nga leen di kókkali,
5 mer, ba gëdd leen,
xadaru, tiital leen ne:
6 «Man maa tabb buur, fal ko ci Siyoŋa,
sama tund wu sell
 
7 Buur ne: «Ma biral dogalu Aji Sax ji,
moom mi ma ne: “Yaa di sama doom,
bés niki tey, maa la jurb.
8 Ñaan ma xeeti àddina, ma sédd la ko,
nga moom ba ca cati àddina,
9 yilife leen yetu weñ,
rajaxe leen ni njaqal xandeer.”»
 
10 Kon yeen buur yi, muusleen,
kilifay àddina, fàgguleen.
11 Jaamuleen Aji Sax ji, ragal ko,
di ko bége, ba yaram daw.
12 Sujjóotal-leen doom ji, bala moo mer,
ngeen sànkoo seenu yoon;
meram day jekki ne jippét,
waaye ndokklee képp ku ko làqoo!