Aji Sax ji teral na nit
8
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiita, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
2 Aji Sax ji sunu Boroom,
sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp!
Sag leer tiim asamaan.
3 Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp,
feeñal nga ca sa kàttan,
bañaaleek feyukat ne xerem.
4 Damay xool sa asamaan si nga móol,
ak weer week biddiiw yi nga fi teg.
5 Moo luy nit, ba nga di ko bàyyi xel?
Luy doom aadamaak loo koy yége?
6 Yaa def nit mu yées malaaka yi as lëf,
te yaa ko kaalaa teraangaak daraja,
7 fal ko ci kaw loo bind,
jox ko lépp, mu teg tànk:
8 jur gépp, gu gudd ak gu gàtt,
rabi àll it ca la,
9 ak njanaaw ak jën,
ak luy jaare yooni géej.
10 Aji Sax ji sunu Boroom,
sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp!