Yàlla laa wóolu, ragaluma nit
56
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñu dippee Pitax mu luu, dëkk fu sore; di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, ba ko Filisteen ña jàppee ca Gaata.
2 Éy Yàlla, baaxe ma,
nit a ngi may lakkal,
ab xeexkat a ma yendoo sonal.
3 Noon yee ma yendoo lakkal,
bare lool di xareek man.
Ku Màgg ki,
4 bés bu ma tiitee,
yaw laay wóolu.
5 Yàlla laay màggal kàddoom,
Yàlla laa wóolu, ragaluma.
Lu ma nit manal?
6 Bésoo bés ñu ngi jalgati samay wax,
seen mépp mébét di sama loraange.
7 Ñu ngi mànkoo, di ma yeeru,
topp sama tànk,
di wut sama bakkan.
8 Éy gii ñaawtéef! Ñii nu ñu mana mucce?
Éy Yàlla, yal na leen sa mer dal!
9 Tumurànke naa, nga gis.
Duyal samay rongooñ ci sa mbuus.
Du lim nga lépp?
10 Bés bu ma wootee wall,
dees na waññi noon yi,
ma xam ne Yàllaa ànd ak man.
11 Yàlla laay màggal kàddoom,
Aji Sax ji laay màggal kàddoom,
12 Yàlla laa wóolu, ragaluma.
Lu ma nit manal?
13 Éy Yàlla, maa tegoo la ma la giñal,
maa lay defal saraxi cant.
14 Yaa ma rawale, ba deewuma,
te duma tërëf.
Damay daagu fi kanam Yàlla,
ci biir leeru àddina.