Yaakaar, fa Yàlla
62
1 Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
2 Yàlla doŋŋ ay dalal sama xel,
moo may wallu.
3 Moom doŋŋ mooy sama wéeru-mucc,
di ma rawale, ba duma sànku!
 
4 Xanaa dungeen bàyyee songandoo nit,
nar koo sànk,
ni kuy màbb tabax bu joy,
mbaa ngay bàddi per mu ràpp?
5 Seeni mébét, wàcce boroom daraja doŋŋ;
yeena ngi bége ay fen,
seeni kàddu diw yiw,
seen xalaat diy saaga. Selaw.
 
6 Yal na Yàlla doŋŋ di dalal sama xel,
moom mi ma yaakaar.
7 Moom doŋŋ a di sama cëslaay, di sama wall,
di sama rawtu, duma tërëf.
8 Yàllaa may musal, di ma sagal,
ma di ko doolewoo.
Sama kiiraay, Yàllaa!
9 Bokk yi, wóoluleen ko fu ngeen tollu,
diisleen ko seen xol,
Yàllaay sunu kiiraay. Selaw.
 
10 Doom aadama, ngelawal neen;
nit, naxi neen.
Booleel teg ci lu ñuy natte diisaay,
kaw la jëm.
Ñooy gëna woyof ngelaw!
11 Bul wóolu ribaa,
bul yaakaar alalu càcc, neen la.
Bu sa alal yokku, nga taf ci sa xol.
 
12 Benn yoon la Yàlla wax,
yaari yoon laa dégg, ñu ne;
«Doole, fa Yàlla.»
13 Boroom bi, ngor, yaay boroom,
yaw daal, yaay yool nit jëfam.