Am Yàllaa gën
73
1 Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.
Yàlla kay baax na ci Israyil,
baax ci ku rafet xol.
2 Waaye man de tuuti kon ma lajj,
tuuti ma tarxiis,
3 ngir maa ñee ku bew,
ndax gis mu baaxle te di ku bon.
4 Amuñu metit,
xanaa ne faaj.
5 Doñ-doñu nit dabu leen,
coonoy doom aadama dalu leen.
6 Moo leen taxa ràngoo reewande,
làmboo coxor.
7 Dañoo suur ba gët suulu,
seen xalaati xel xëtt yoon.
8 Dañuy ñaawle, di wax lu bon,
di réy-réylu, boole ci kàdduy jaay-doole.
9 Seen ŋal-ŋal àkki asamaan,
làmmiñ dajal suuf.
10 Moo tax ñoñi Yàlla walbatiku ci ñoom,
di jolu seen wax nim ndox
11 te naan: «Lu ci Yàlla xam?
Ana xam-xam fa Aji Kawe ji?»
12 Ñu bon ñaa ngoog!
Ne finaax, di gëna woomle.
13 Man kay maa sellal ci neen,
di sàmm sama der.
14 Bés bu ne yar dal ma,
saa yu ma xëyee, jot mbugal.
15 Su ma noon: «Naa waxe ni ñoom,»
kon de, ma wor sa askanu mbooloo.
16 Naka laay jéema ràññee lii,
mbir mi ëlëm ma.
17 Ba ma àggee sa kër gu sell ga,
laa doora gis muju ku bon.
18 Yoonu tarxiis kay, nga leen teg,
daane leen, ñu sànku,
19 Yàquleeka leena bett!
Musibaa leen ne fuuf, ñu ne mes!
20 Day mel ni gént goo yewwoo.
Céy Boroom bi, boo xippee, jëmmu gént ga soof la.
21 Naqar laa amoon,
sama xol di dagg.
22 Booba ngaaka laa, xawma dara;
rab laa woon fi sa kanam.
23 Teewul ma des ak yaw,
nga jàpp sama loxol ndijoor.
24 Danga maa gindee sam xel,
teg ca dalale ma sa teddnga.
25 Ana ku ma am asamaan ku la moy?
Ku ma safoo kaw suuf ku la moy?
26 Kàttan ak pexe jeex,
Yàlla di ma dooleel,
ma séddoo ko fàww.
27 Ku la sore kat, sànku;
képp ku la wor, nga fàkkas.
28 Man de, jege Yàllaa ma gënal.
Boroom bi, Aji Sax ji, yaw laa def kiiraay,
ngir siiwal sa jépp jëf.