Yàlla, feyul nu
79
1 Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.
 
Céy Yàlla, yéefar yi song nañu sa moomeel,
teddadil nañ sa kër gu sell,
gental nañ Yerusalem.
2 Leel nañ tan yi sa néewi jaam ñi,
leel nañ rabi àll yi sa suuxi wóllëre yii.
3 Ñu tuur seen deret nim ndox,
ba Yerusalem daj,
te amul kuy rob néew yi.
4 Noo ngi nii di mbalitu dëkkandoo yi;
ñu séqe nu ay kókkaleeki kekku.
 
5 Aji Sax ji, xanaa doo nu mere ba fàww,
sa fiiraange ni sawara ci sunu kaw?
6 Sippil sa mer yéefar yi la xamul,
ak réew yi wormaalul sa tur.
7 Ñoo sëxëtoo giirug Yanqóoba,
gental dëkkuwaayam.
8 Bul nu topp ñaawtéef ya woon,
ngalla gaaw noo gatandoo sa yërmande.
Danu ne dàll, ba ne dett.
9 Éy Yàlla, yaa nuy musal, wallu nu,
ba sa seede rafet.
Xettli nu te baal nu sunuy bàkkaar,
ba sa woy rafet.
10 Bul tax yéefar yi naa:
«Ana seen Yàlla?»
May nu, nu gis ni ngay mbugale yéefar yi,
feye leen sa deretu jaam yi tuuru.
11 Ñi ñu jàpp, yal na seeni onk àkki fa yaw.
Ñi ci tànki ndee, yal nanga leen musale sa doole ju màgg.
 
12 Boroom bi, sewal gi la sunuy dëkk sewal,
këpp leen ko juróom yaari yoon,
13 te nun ñiy sa mbooloo, di sa gétt gi ngay foral,
nu di la sant ba fàww,
di biral sa ngërëm sët ba sëtaat.