Ma bàkk Aji Sax ji
93
1 Aji Sax jeey buur, soloo daraja;
Aji Sax jee solu, gañoo doole:
àddinaa ngii, dëju te raful.
2 Sab jal a masa sax,
te yaa masa nekk.
3 Aji Sax ji, géej a riir,
géej a àddu, mu riir,
gannax ya rëkk, mu riir.
4 Waaye riirum wal mu walangaanoo,
ak géej gu sàmbaraaxoo,
Aji Sax ja fa kaw a rawati!
5 Say santaanee wér te wóor;
Aji Sax ji, sellnga la sa kër jagoo
bésoo bés.