Màggal-leen ki sàkk lépp
104
1 Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii!
Aji Sax ji sama Yàlla, yaaka màgga màgg.
Teddngaak daraja nga soloo,
2 làmboo leer ni mbubb,
firi asamaan ni ndimo,
3 xadd say néegi kaw ci biir ndox mi,
def niir yi say waruwaay,
di daagoo kaw laafi ngelaw,
4 def ngelaw yi say ndaw,
ay sawara boy, di say jawriñ.
5 Yaa dëj suuf ciy kenoom,
deesu ko yëngal ba fàww.
6 Yaa ko sànge xóotey géej ni mbubb,
ndox ma taxaw, tiim tund ya.
7 Nga gëdd, ndox ma fëx;
nga dënu, mu daw,
8 wale kaw tund ya, wàccsi xur ya,
di bérab ba nga ko beral.
9 Ag kemu nga teg, du ko wees,
te dootu muur suuf si.
10 Yaa ballal bëti ndox ya ca xur ya,
ñuy wale digg tund ya,
11 ngay nàndal bépp ndundatu àll,
di wëgg mbaamu àll,
12 njanaaw dëkke ca wet ga,
baatam jibe fa garab ya.
13 Yaa suuxate tund ya fa sa néegi kaw,
sa liggéey reggal suuf.
 
14 Yaa saxalal jur gi ñax
ak gàncax gu doom aadama di bey,
ba génnee ab dund fi suuf,
15 dugub di ko dooleel,
biiñ di bégal xolam,
ag diw di leeral kanamam.
16 Garabi Aji Sax ja, seedari Libaŋ,
ya mu jëmbat, regg nañu,
17 picc tàgge ca,
xodd dëkke garab gu dul ruus,
18 tund wu mag ñeel kéwéli àll,
xunti di rawtub damana.
19 Yaa sàkk weer, muy takku jamono,
sàkk jant, mu xam waxtuw fatoom.
20 Yaa def lëndëm, mu guddi;
bépp rabu àll di ca dox,
21 gaynde gu ndaw ŋaral am pàddam,
di sàkkoo dundam fa Yàlla.
22 Bu jant fenkee, ñu dellu,
goori ca seeni pax,
23 doom aadama tàmbali kër-këram,
di yendoo liggéey ba ngoon.
 
24 Éy Aji Sax ji, yaa bare loo liggéey,
te lépp di xel mu rafet.
Suuf daa fees ak say càkkéef.
25 Géej a ngee réy te yaa,
la fay yëngu maneesu koo lim,
muy ndundat lu mag ak lu ndaw.
26 Fa la gaal di daw,
ak ngaaka la nga bind, mu di fa foye.
27 Ñoom ñépp yaw lañuy séentu,
ngir bu jotee, nga leel leen,
28 may leen lu ñu for;
ŋëbal leen, ñu suur ngëneel.
29 Soo leen làqoo, ñu tiit;
nga rocci seen noo, ñu saay,
dellu di pënd.
30 Yaay yónnee sag noo, ñu nekk;
te yaay yeesal li ci kaw suuf.
 
31 Yal na darajay Aji Sax ji sax,
yal na Aji Sax ji bégey jalooreem.
32 Kee naan jàkk suuf, muy lox;
mu laal tund yi, ñuy saxar!
33 Naa woy Aji Sax ji li feek may dund,
naa kañ sama Yàlla li feek may tooy.
34 Sama xalaat bii, yal na ko neex.
Man de maa ngi bége Aji Sax ji!
35 Yal na bàkkaarkat raaf fi kaw suuf,
te ku bon noppee nekk.
Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii.
Màggal-leen Ki Sax!