Yal na Yàlla mbugal noon bi
109
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
 
Éy Yàlla mi may sant, bul tanqamlu!
2 Ku bon ak kuy fen a ma waxal,
sosal ma,
3 tance ma kàdduy mbañeel,
song ma ci dara.
4 Ma ji nit cofeel, mu sosal ma;
te man ma di ko ñaanal.
5 Sama jëf ju baax, loraange lañu ma ko feye,
sama cofeel, ñu feye ma ko mbañeel.
 
6 Yal nanga fal ku bon ci kaw kii,
ab soskat féete ko ndijoor.
7 Bu ñu koy àtte, yal nañu ko yey,
te yal na ñaanam walbatiku di bàkkaar.
8 Yal naw fanam gàtt,
keneen jagoo sasam.
9 Yal nay doomam diy jirim,
jabaram dib jëtun,
10 ay doomam di tambaambaluy yalwaan,
dëddu seeni gent, dem tàllal ay loxo.
11 Yal na ko kuy feyeeku futti,
ay doxandéem foqati ñaqam.
12 Yàlla bu ko kenn ji ngor,
yàlla bu kenn baaxe jirim yi ko wuutu.
13 Yal na askanam dagg.
Balaa geneen maas a wéy, yal na seenu tur fey.
14 Yal na Aji Sax ji bàyyi xel ñaawtéefi maamam.
Yàlla bu bàkkaaru ndeyam faru.
15 Yal na seeni moy sax fi kanam Aji Sax ji.
Yal na seen tur dagge fi kaw suuf.
16 Moo séddul ngor,
di topp ku néewle te sonn,
seen xol jeex, mu bóom.
17 Moo bëggoon di móoloo, yal na ko këppoo;
soppul ag ñaan it, yal na ko barke sore.
18 Móolook sol mbubb la yemale,
yal nañu duy nim ndox ay móoloom ci yaramam,
mu seeb ci biiri yaxam nig diw.
19 Yal nay móoloom di mbubbam,
te di laxasaay gu mu saxoo.
 
20 Lii, yal na ko Aji Sax ji feye ñi may sosal,
di teg lu ñaaw ci sama der.
21 Waaye Boroom bi Aji Sax ji,
defal ma li sa tur laaj.
Yaa baax, gore, xettli ma.
22 Damaa néewle te sonn,
sama xol dagg, ba jeex tàkk.
23 Maa ngi tàggoo ni keru ngoon,
ñu di ma fél ni soccet.
24 Samay óom a ngi nasax ndax ñàkka lekk,
desewuma lu moy yaxi neen.
25 Maa ngii, ñu di ma sewal,
ku ma gis, wëcc bopp.
26 Éy Aji Sax ji, sama Yàlla, dimbali ma,
walloo ma sa ngor,
27 ba ñu xam ne lii sa loxoo,
xam ne yaw Aji Sax ji, yaa ko def.
28 Ñooy móolu, yaw nga barkeel;
ñoo ma jógal, ñooy torox,
man, ma bég, Sang bi!
29 Yal na ñi may sosal sàngoo toroxte,
làmboo gàcce ni mbubb.
30 Ma àddu, santa sant Aji Sax ji,
di ko màggale digg mbooloo mu yaa.
31 Mooy féete ndijoor néew-ji-doole,
musal ko ci ku koy teg àtteb dee.