Na ñépp ànd ak Israyil sant Yàlla
117
1 Yeen xeetoo xeet, màggal-leen Aji Sax ji,
réewoo réew, kañleen ko.
2 Moo nu xéewale ngoram gu réy,
te wormay Aji Sax jee sax dàkk.
Màggal-leen Ki Sax!