Ma ñaan ci biir tuuma
120
1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
 
Ci sama njàqare laa woo Aji Sax ji wall,
mu wuyu ma.
2 Éy Aji Sax ji, musal ma ci gémmiñu fen-kat,
ak làmmiñu njublaŋ.
3 Yaw boroom làmmiñu njublaŋ,
ana lu ñu lay añale
ak lu ñu lay dolli?
4 Xanaa fitti mbër yu ñaw
ak xal yu yànj.
 
5 Wóoy man mi ganeyaani baadooloy Meseg ya
tey dali fa xaymay waa Kedar ñu xayadi ña!
6 Yàgg naa lool ci biir nit ñi bañ jàmm.
7 Man may wut jàmm,
te su ma waxee,
ñoom ñuy ayoo.