Yàlla, fajal nu gàcce
123
1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Yaw laay séentu,
yaw mi toog fa asamaan.
2 Ma ne, ni jaam bu góor di wékke sangam bët,
jaam bu jigéen di ko wékke bët sangam bu jigéen,
ni lanuy wékke sunu Yàlla Aji Sax ji bët,
ba keroog mu baaxe nu.
3 Éy Aji Sax ji, baaxe nu, rikk baaxe nu,
dañu noo torxal, ba nu ne tott.
4 Ñu reew ñaa ngi nuy ñaawal, sunu xol fees,
ñu bew ñaa ngi nuy sewal.