Ku doyloo Aji Sax ji raw
125
1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Ku doyloo Aji Sax ji,
yaay tundu Siyoŋ, doo toxu;
dangay sax ba fàww.
2 Ni tund yi yéewe Yerusalem,
ni la Aji Sax ji yéewe ñoñam,
tey ak ëllëg.
3 Nguur gu bon du saxe
kaw suuf su nit ñu jub muurloo.
Lu ko moy ñu jub ñi sàkku lu bon,
di ko jëfe.
4 Éy Aji Sax ji, baaxeel ku baax,
ak kuy mébét njub.
5 Waaye kuy topp yoonu ndëngte,
Aji Sax jee koy sànk,
boole kook kuy def lu bon.
Yal na jàmm dal Israyil.