Yàllaa gën ci àddina, gën ci nit
147
1 Màggal-leen Ki Sax!
Kañ sunu Yàllaa baax,
màggal koo neex te war.
2 Aji Sax jaa ngi tabaxaat Yerusalem,
di délloosi ña ñu dàqe Israyil,
3 di faj naqaru xol,
fajtal góomi boroom.
4 Mooy lim biddiiw yi,
tudd bu ci nekk.
5 Sunu Boroom a màgg, bare doole;
am xelam wees kemu.
6 Aji Sax ji, néew-ji-doole, mu yenni;
ku bon, mu daane ci suuf.
 
7 Woyeleen Aji Sax ji kàddug cant,
kañeleen sunu Yàlla jii ay xalam;
8 mooy sànge asamaan ay niir,
tawal suuf,
saxal tund yi am ñax,
9 leel mala,
xol liiru baaxoñ bu jooy.
10 Kii nawul dooley fas,
gërëmul kàttanu jàmbaar.
11 Ki Aji Sax ji gërëm mooy ki ko ragal
te di ko yaakaare ngoram.
 
12 Yerusalem, sargal-leen Aji Sax ji!
yeen waa Siyoŋ laa ne, màggal-leen seen Yàlla!
13 Mooy tëj ràpp seen bunti dëkk,
barkeel seen askan wa ca biir,
14 jàmmal seen suufas réew,
reggal leen ngëneelu pepp,
15 yónnee suuf ndigalam,
kàddoom ne coww, daw ca.
16 Mooy tawal yuur bu mel ni wëttéen,
di lay lay bu sedd, mel ni pënd ci suuf.
17 Mooy yuri tawub yuuram niy donj.
Bu ni seddee, ana kuy taxaw?
18 Mu yebal kàddoom, seeyal;
wal ngelawam, ndox walalaan.
19 Mooy wax Yanqóoba kàddoom,
dogalam yaak ndigali yoonam ñeel Israyil.
20 Loolu defalu ko wenn xeet;
kenn xamu ci ndigali yoonam.
Màggal-leen Ki Sax!