29
1 Ku ñuy àrtu, nga të ticc,
dangay jekki yàqu, ba wees am paj.
 
2 Ku jub falu, baadoolo bég;
ab soxor jiite, baadoolo binni.
 
3 Kuy jëfe xel, bégal sa baay;
nga ànd aki gànc, yàq alal.
 
4 Buur jub, am réew dëgër;
mu bëggi galag, réew ma sànku.
 
5 Kuy jay sa moroom,
yaa ngi koy dugal.
 
6 Ku bon day moy, ba dugal boppam;
ku jub di woy ak a bànneexu.
 
7 Ku jub a xam àqu néew-ji-doole,
ab soxor xamu ca dara.
 
8 Ñaawlekat a ngi taal ab dëkk,
ku xelu di giifal mer.
 
9 Boroom xel, buy layook ub dof,
bu mereek buy ree, jàmm du am.
 
10 Ab bóomkat day sib ku mat,
di wuta bóom kuy jubal.
 
11 Ab dof day mer, sàmbaar;
ku xelu, mer, ànd ak sagoom.
 
12 Kilifa dégluy fen,
jawriñ yépp di ñu bon.
 
13 Ku ñàkk ak ka ko nennoo bokk lenn,
Aji Sax jee leen boole sàkk.
 
14 Buur àtte way-ñàkk ci dëgg,
ab jalam sax.
 
15 Deel bantal ak a yedde, day rafetal xel;
gone goo bay-bayal, mu gàcceel ndeyam.
 
16 Bu ku bon féetee kaw, ag moy law,
waaye ku jub, fekke jéllu ku bon.
 
17 Yaral sa doom, mu noppal la,
bànneexal la.
 
18 Fu Yàlla feeñoowul, nit ña fétteeral,
waaye ku topp yoon, am mbégte.
 
19 Waxi neen yarul surga,
da lay dégg te du la déggal.
 
20 Ana koo gis, mu rattaxle?
Kooku ab dof a ko gën demin.
 
21 Ku yàq sab surga ba muy ndaw,
bu ëllëgee mu defe ne doom laa.
 
22 Boroom xadar day sooke ay,
te ku tàng bopp moy, moyati.
 
23 Réy-réylu, detteelu rekk;
woyofal, ñu naw la.
 
24 Ku ànd akub sàcc, sa noonu bopp nga:
soo waxee dëgg, yoon topp la;
soo ko miimee, Yàlla topp lab.
 
25 Ragal nit dugal sa bopp la,
ku wóolu Aji Sax ji, fegu.
 
26 Ñu baree ngi sàkku kilifa baaxe leen,
moona Aji Sax jeey àtteb jaam.
 
27 Ku jub day sib ku dëng,
ku bon sib kuy jubal.