Kàddu yi Agur wax
(Saar 30)
30
1 Lii waxi Agur la, góor gay doomu Yake mu Maasaa. Góor ga daa wax ak Itiyel, wax ak Itiyel ak Ukal. Mu ne:2 Maa dofe dëgg, ba yées ci nit ñi,
dég-dégu nit sax awma ko.
3 Jànguma, ba am xel mu rafet,
awma xam-xam ci Aji Sell ji.
4 Ana ku yéegoon asamaan, ba wàcc?
Mbaa mu masa ŋëb ngelaw ciy loxoom?
Ana ku masa ëmb ndox ci ndimo?
Mbaa mu rëdd mboolem kemi àddina?
Nu mu tudd ak nu doomam tudd?
Wax ma, yaw mi ko xam!
5 Lu Yàlla wax, mat na sëkk,
mooy yiir ku ko làqoo.
6 Bul yokk ay waxam,
mu weddi say fen, nga weeru.
7 Éy Yàlla, yaar laa la ñaan,
ngalla may ma ko sama giiru dund:
8 caaxaan aki fen, yal na ma sore,
néewleek barele, bu ma ci may lenn,
leel ma lu ma doy;
9 lu ko moy ma regg, weddi la,
ba naan: «Kuy Aji Sax ji?»
Mbaa ma ñàkk bay sàcc,
di la ñàkke worma, yaw sama Yàlla.
10 Bul sikkal ab surga ca njaatigeem,
da lay ñaan-yàlla, mu dal la.
11 Ag maas a ngi saaga baay,
te wormaaluñu ndey.
12 Ag maas a ngi defe ne set nañu,
te taq ripp ak bàkkaar.
13 Ag maas a ngi daŋŋiiral;
aka ñoo mana xeeloo!
14 Ag maas a ngi, seeni sell niy saamar,
seeni gëñ niy paaka,
ñuy lekk néew-ji-doole, ba raafal leen ci réew mi,
ba ku ñàkk jeex ci biir nit ñi.
Ay kàddoo ngi yu ànd ak lim
15 Saxu watar du suur, ñaar ñu jigéen la am:
Jox Ma ak Jox Ma.
Ñett a ngii ñu dul suur,
ba ci ñeent ñu dul ne doy na mukk:
16 njaniiw,
jigéen ju jaasir,
suuf, du màndi ndox,
sawara, du ne doy na mukk.
17 Kuy xeelu sa baay,
di siidee déggal sa ndey,
baaxoñ génne ciw xur, luqi sa bët,
tan ya lekk.
18 Ñett a ngii, yéem na ma,
ba ci ñeent yu ma xamul:
19 yoonu jaxaay ci asamaan,
yoonu jaan ci kawi doj,
yoonu gaal ci diggu géej,
yoon wi góor di jaar as ndaw.
20 Jikkoy jigéenu moykat a ngi.
Day lekk, wommiku, te naan:
«Defuma dara lu aay!»
21 Ñett a ngii, day yëngal suuf,
ba ci ñeent yu suuf àttanul:
22 jaam bu falu buur,
dof bu regg,
23 ndaw su bon su for jëkkër,
jigéen ju wuutu sangam bu jigéen.
24 Ñeent a ngii, di lu tuut ci kaw suuf,
te am xel, yaroo xel:
25 xorondom, néew na doole,
waaye bu jotee, mu denc dundam;
26 damanb, barewul kàttan,
te day dëkk ciy doj;
27 soccet, amul buur,
teewul ñuy àndandoo, diy gàngoor;
28 sindax, manees na koo ŋëb,
teewul ma nga biir kër buur.
29 Ñett a ngii, ñu jekk um ndaag,
ba ci ñeent ñu jekk doxin:
30 gaynde, mooy buuru rab yi,
ragalul kenn;
31 séq daagu, jekk taxawaay,
ab sikket,
ak buur ci biiri dagam.
32 Boo sàgganee bay tëggu,
mbaa ngay mébét lu bon,
nanga téye saw làmmiñ.
33 Ndax ku ruux soow, am ca dax,
ku wañaar bakkan, mu nàcc,
te lu jógal xol, indiw ay.