Jamono, Yàlla
3
1 Lu nekk ak jotam,
jot gu nekk ak la ca war fi jant bi tiim.
2 Day jot nga juddu, mu jot nga dee;
mu jot nga jëmbat, mu jot nga buddi.
3 Mu jot nga rey, mu jot nga faj;
mu jot nga toj, mu jot nga tabax.
4 Mu jot nga jooy, mu jot nga ree;
mu jot nga ñaawlu, mu jot nga dukkat.
5 Day jot nga sànniy doj, mu jot nga dajale;
mu jot nga fóon, mu jot nga baña fóon.
6 Mu jot nga sàkku, mu jot nga ñàkk;
mu jot nga sàmm, mu jot nga xalab.
7 Mu jot nga xar, mu jot nga gaar;
mu jot nga selaw, mu jot nga wax.
8 Mu jot nga sopp, mu jot nga jéppi;
mu jot nga xare, mu jot nga jàmmoo.
 
9 Ana lu liggéeykat biy jariñoo ciw ñaqam?
10 Gis naa ne sas la bu Yàlla sase,
nu war koo sasoo.
11 Lépp la Yàlla def,
ba bu jotee rafet.
Moo may nit muy njort ëllëg,
te taxul mu mana ràññee jëf ji Yàlla jëf,
njàlbéen ba muj ga.
12 Ma gis ne nit amul lu gën
bànneex ak jàmmi bakkan cig dundam,
13 te nitoo nit, su dee lekk ak a naan,
di ñaq, jariñoo,
loolu mayu Yàllaa.
14 Ma xam ne lu Yàlla def,
loola day sax ba fàww.
Deesu ci yokk, mbaa di wàññi dara;
Yàllaa ko def, ngir nit di ko wormaal.
15 Lu ay tey, ayoon na,
lu ay ëllëg it ayoon na.
Yàllaay namma indi la woon.
Yaakaar feyul boroom
16 Ma dellu gis fi kaw suuf ne,
fu yoon moom, fa la njubadi ne,
fa njub moom it, fa la njubadi ne.
17 Saam xel ne ma,
ku jub ak ku bon la Yàlla di boole àtte,
ngir mbir mu ne ak jëf ju ne ak bésam.
18 Saam xel neeti ma,
nun doom aadama, Yàllaa nuy nattu,
nu gis ne ay mala doŋŋ lanu.
19 Dogalu doom aadama ji
ak dogalu mala mi,
benn dogal bee;
ni kii di deeye la kee di deeye,
genn noo gee, nu bokk ko.
Lu nit ëpplee mala neen na,
ñoom ñépp, cóolóoli neen.
20 Ñoom ñépp a bokk jëm benn bérab ba,
bokk jóge pëndub suuf,
bokk dellu suuf.
21 Ana ku mu wóor ne
bakkanu nit day yéeg asamaan,
bakkanu mala tàbbi suuf?
22 Ma gis nag ne nit amul lu gën
di bànneexoo ñaqam, loolooy wàllam.
Ana ku koy xamal gannaawam?