Kenn xamul, waaye beyal sa tool
11
1 Dugalal sa alal, dawloo ko;yàgg-yàgg nga jotaat ci.
2 Séddal ab cér juróom yaari nit ba juróom yett;
xamoo safaan buy dikkal àddina.
3 Xàmbaar bu duyee, ba fees,
fi kaw suuf lay soob.
Garab, bu daanoo ndijoor mbaa càmmoñ,
fa mu daanu lay des.
4 Kuy déglu ngelaw, doo ji,
kuy seetluy niir, doo góob.
5 Xamoo yoonu ngelaw,
xamoo nu doom di sosoo ci ndeyam;
kon manoo xam lu Yàllay def,
moom miy def lépp.
6 Xëyal, ji sa jiwu,
gont, baña tàyyi;
muy lii di lee, xamoo lu ciy nangu,
am ñaar ñépp ay bokk baax.
Bégal te xam ne man saxul
7 Leer neex na,
gis jant neex na.
8 Ak lu say at bare bare,
bégeel at mu ci nekk,
waaye bàyyil xel lëndëmu bàmmeel,
lu yàgg lay doon,
te liy ñëw lépp, cóolóoli neen.
9 Xalelu góor bi, bànneexul bi ngay gone,
bégalal sa xol bi ngay ndaw.
Toppal loo namm ak loo xemmem,
waaye xamal ne loolu lépp,
Yàlla da la koy laaj.
10 Félal naqaru xol,
dàq woppi yaram;
waaye ndaw ak kawar gu ñuul, cóolóoli neen.