Woyu cofeel rax na
5
1 Naa woy sama soppe
woyu cofeel wu solowoo tóokëram.
Sama soppee fi amoon tóokër,
kaw tund wu suuf sa nangu lool.
2 Mu gàbb ko, dindi doj ya,
jëmbat ca ngëneeli reseñ,
tabax tóojub doj fa digg ba,
ba yett ca mbalkam nalukaayu reseñ,
tey yaakaar reseñ ju neex,
mu meññ, wex.
 
3 Léegi yeen waa Yerusalem
ak yeen waa Yuda,
ngalla àtteleen maak sama tóokër.
4 Lu may defalati sama tóokër bi,
lu ma ca defuloon?
Lu waral ma di ko yaakaare reseñ ju neex,
mu meññ, wex xàtt?
5 Ma xamal leen nag
li ma naral sama tóokër bi.
Ñàggib ñagam, mu dim parlu;
màbb miiram, ñu dëggaate ko, jàll.
6 Dama koy gental,
mu saxi dég aki dagg,
deesu ko tenqi, deesu ko bey;
niir yeet, ma sant leen
ñu bañ koo tawal.
7 Tóokëru Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat,
mooy waa kër Israyil.
Niti Yuda it
ñooy njëmbat li mu safoo.
Mu di ko yaakaare njub,
njubadi ne jaas.
Mu yaakaar njekk,
yuuxi njekkar ne jaas.
Alkànde ñeel na kàngami Yuda
8 Wóoy ngalla ñii di dajale kër ak kër,
tool akub tool,
aakimoo fépp,
ba des ñoomu neen ci réew mi.
9 Maa dégg Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
mu ne: «Giñ naa ne
kër yu bareey gental déy,
kër yu yaa, rafet, kenn dëkku ca.
10 Tóokërub ñetti egtaar déy
du meññ juróom fukki liitari biiñ,
te jiwum téeméeri kiloy bele it,
fukki kilo doŋŋ a cay génne.»
11 Wóoy ngalla ñiy teela xëy,
daw wutiw ñoll,
gonloo biiñ ba tàng jérr.
12 Xalam yaak tabala yaak toxoro ya jolli,
biiñ xelli ca xawaare ja.
Seetluwuñu sax li Aji Sax ji def,
xooluñu li mu jo loxoom.
13 Moo tax ñoñi Aji Sax ji di duggi ngàllo
ndax ñàkk xam-xam.
Seen kàngam ay deeye xiif,
seen baadoolo deeye mar.
14 Moo tax njaniiw di yàkkli ag bóli,
gémmiñ ga ne ŋafeet, amul kersa,
boroom darajaak baadoolay Yerusalem
doon xaxaloo, far tàbbi ca.
15 Doom aadama torox na,
nit detteelu na,
ku doon regeju, detteelu.
16 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ab àtteem lay fésale màggaayam,
Yàlla ju sell ji, ag njekkam lay firndeele sellngaam.
17 Am xar a nara fore biir dëkk bi, mbetem parlu,
màngaan lekke gentub boroom alal.
18 Wóoy ngalla ñiy ràngooy buum,
di diri ñaawtéefi neen,
ràngooy goj di diri seeni tooñ.
19 Ña nga naa: «Na Aji Sax ji gaaw!
Na baral liggéeyam, nu gis.
Na Aji Sell ju Israyil sottal mébétam,
mu sotti, nu xam.»
20 Wóoy ngalla ñiy gis lu bon, ne lu baax la;
gis lu baax, ne lu bon la;
lëndëm, ñu tudde leer,
leer, ñu tudde lëndëm;
lu wex, ñu ne neex na
lu neex, ñu ne wex na.
21 Wóoy ngalla ñii defe ne ñoo xam,
yaakaar ne ñoo muus.
22 Wóoy ngalla ñiy jàmbaari naan biiñ,
diy ndaanaan ci njafaanu ñoll,
23 di dëggal ku sikk ndax ab ger,
tey xañ boroom njekk, ag njekkam.
24 Moo tax ni boob di jeexe ci sawara,
ngooñ xoyomoo ko cib taal,
ni la seenub reen di seeye ni lu maxe,
seeni tóor-tóor naaw ni pënd.
Ñoo gàntal yoonu Aji Sax ji ci gàngoor yi,
ñoo sofental kàddug Aji Sell ju Israyil.
25 Moo tax merum Aji Sax ji tàkkal ñoñam,
mu xàcci loxoom, duma leen,
ba tund yi jaayu,
seeni néew wetar ni mbalit fi mbedd yi.
Loolu yépp taxul mu meddi,
loxoom baa ngi mu xàcci ba tey.
 
26 Aji Sax jeey yékkatil raaya, xeet wu sore,
wal ug liit, wooye leen fa cati àddina,
ñu jekki ne jaas, dikkal leen.
27 Kenn sonnu ci, kenn tërëfu ci,
kenn dajjantul mbaa muy nelaw;
ngañaay yolomul, waruw dàll dogul.
28 Seeni fitt ñaw na,
seen xala yépp noppi na,
seen wewi tànki fas ni xeer.
Bu tànki watiir ya dawee,
nga defe ne callweer a.
29 Dañuy ŋar ni gaynde,
ŋarati ni gaynde gu mat;
yëmmu, ŋank um rëbbam,
yóbbu te kenn du wallu.
30 Bésub keroog ñu ŋaral Yuda,
ŋar yu mel ni géej gu sàmbaraax!
Foo geesu ci réew mi, xool,
doo gis lu moy lëndëm ak njàqare,
xàmbaar maase, ba leer giim.