Asiri workat la, matul wéeruwaay
8
1 Gannaaw gi Aji Sax ji ne ma: «Jëlal àlluwa ju mag, ak xalima gu jàppandi, nga bind ci lii: “Maxer Salal Xas Bas”, (mu firi Sëxëtoo këfit foqet).» 2 Ma wut ci seede, won àlluwa ja ñaar ñu mat seede: ñuy Uri sarxalkat ba, ak Sàkkaryaa doomu Yeberekiya. 3 Ba loolu weesee ma jaxasoo ak sama soxna, yonent bu jigéen ba, mu ëmb, gannaaw gi mu am ca doom ju góor. Aji Sax ji ne ma: «Tudde ko “Maxer Salal Xas Bas.” 4 Bala xale bee man ne “Baay” mbaa “Yaay” déy, dees na yóbbul buurub Asiri alal ju ñu foqatee Damaas, ak lël ju ñu këfe Samari, nangu ko.»5 Aji Sax ji dellu ne ma:
6 «Gannaaw askan wee teddadil ndoxum Silowe,
mi ci wal mu teey mi,
di bége Reccin ak doomu Remalya,
7 Boroom baa ngii di leen sottisi
dexu Efraat gi ne xéew ak dooleem,
te mooy buurub Asiri ak mboolem darajaam.
Dex gi mooy génn xuram,
fees fépp fu dig tàkkam,
8 wal-wali jàll Yuda,
mbënn ma wal, taañaañal,
yéeg ba tollu ko ci put,
firiku niy laaf ba dajal sam réew, yaw Emanuwel.»
9 Yeen xeet yi, xaaculeen, dees na leen rajaxe.
Yeen waa cati àddina, teewluleen!
Gañoo gañu, ñu rajaxe leen!
Ma ne: Gañoo gañu, ñu rajaxe leen!
10 Ngeen mébét, dara!
Ngeen diisoo, diisoo, tus!
Yàllaa ànd ak nun!
Aji Sax jee jara ragal
11 Aji Sax ji moo wax ak man,
ba mu ma nee nikk, àrtu ma,
ngir ma baña roy askan wii. Mu ne ma:
12 «Bul tudde wor,
lenn lu askan wii tudde wor;
lu ñu ragal it, bu ko ragal,
bu ko tiit.
13 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal ngay sellal,
moom ngay ragal,
moom ngay tiit.
14 Mu doon seen bérab bu sell,
di doj wuy fakktale,
xeer wuy féle, ci ñaari këri Israyil,
te dim yeer, dig fiir,
ñeel ku dëkk Yerusalem.
15 Ñu baree cay tërëf,
daanoo njaaxaanaay, damm,
mbaa ñu sërëx, keppu.»
16 Dencal seede bii,
jëlal lii ndigal, tay cib tayu,
dénk ko samay dongo.
17 Maa ngi séentu Aji Sax ji,
mu ngi won waa kër Yanqóoba gannaaw,
waaye maa ngi koy yaakaar.
18 Man de, maa ngii, maak xale yi ma Aji Sax ji may,
nu diy firnde fi Israyil te diy tegtal
yu bàyyikoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
ki dëkke tundu Siyoŋ.
19 Am na ñu naan:
«Laajleen ñiy gisaanee nit ñu dee,
ak boroom rawaan yiy kebetook a ŋun-ŋuni.
Aw xeet sañ nañoo gisaanee seeni tuur,
tey diis ñi dee mbiri ñiy dund.»
20 Kon waxleen ne leen: «Ayca, ca ndigali yoon ya,
ak seedey kàdduy waxyu ya.
Kuy wax googu kàddu, ag leer fenkalu la.»
21 Nit ñi dinañu taxawaalu ci réew mi,
boole njàqareek ub xiif,
te bu ñu xiifee, ñéññ,
téen, xool kaw,
saaga seen buur, saaga Yàlla,
22 dellu xool fi suuf,
yem ciw tiis, ak lëndëmu njàqare,
sóoboo guddi gu fatt taraj.
23 Waaye lëndëm googu du sax
ci réew mii jàq tey.
Démb Aji Sax ji torxal na
réewum Sabulon ak mu Neftali,
waaye ëllëg mu teral waa foofa,
dale ko diiwaanu tefesu géej,
ba ca wàllaa dexu Yurdan,
boole ca sax Galile ga ca doxandéem ya.