14
1 Aji Sax ji kay mooy yërëm askanu Yanqóoba, dellu taamu xeetu Israyil wii. Moo leen di sancaatal fa seen suuf, doxandéem yi fekki leen; boole seen bopp ci askanu Yanqóoba. 2 Yeneen xeet yeey delloo bànni Israyil ba seen réew, mooma Aji Sax ji séddoo, bànni Israyil jàpp ca ñoom njaam, góor ak jigéen, ba teg loxo ña leen tegoon loxo, moom ña leen moomoon. 3 Bés bu leen Aji Sax ji teggilee seeni coonook seeni fitna, ba ngeen tàggook njaam gu metti, gi ñu leen doon jaamloo, 4 su boobaa nangeen woyal buuru Babilon léeb wii, ne ko:«Moo nu ki daan note mujje?
Nu mu mujjeek reewandeem?
5 Aji Sax jee damm bant,
bi ñu bon ñi daan dóoree!
Moo damm seen yetu nguur,
6 wi ñu daan xadaruy dóor askan yi,
dóor yu dakkul,
di joggatee xeet yi xol bu tàng,
topp leen, tëë ba.
7 Àddina yépp a féex, am jàmm,
sarxolle jolleendoo.
8 Garab yi dul ruus, ak seedari Libaŋ sax
di bége sab jéll,
naan: “Ba nga daanoo ba tey,
ab gorkat jógalu nu.”
9 Njaniiw ga fa suufa suuf yàkkamti na la,
di la waaja gatandu,
ba yeel la ndem-si-yàlla yi doon njiiti àddina yépp.
Moo yékkatee buuri xeet yépp seeni jal,
10 ñoom ñépp àddu, ne la:
“Yaw it mujj nga néew doole ni nun a?
yaak nun de a mujj yem kepp!”
11 Sa puukare gee tàbbisi nii njaniiw,
yaak sa buumi xalam?
Ay duusu di sa laltan,
ay sax di sa càngaay!
12 Moo yaw biddiiwu njël, bi noon ràññ,
tey nga xàwwikoo asamaan ba fii!
Yaw mi daa daan xeet yi,
tey ñu gor la, nga goor.
13 Xanaa du yaa doon wax ci sam xel, naa:
“Maay yéeg kaw asamaan,
maay aj sama jal kaw biddiiwi Yàlla,
maay toogi kaw tundu ndaje ma,
fa catal bëj-gànnaar.
14 Maay yéeg fa kaw niir ya,
ba mel ni Yàlla Aji Kawe ji!”
15 Teewul nga tàbbi njaniiw,
àkki ba ca xóotey pax ma.
16 Ku la gis ne la jàkk,
xel ma ne ci yaw, mu naa:
“Xanaa du kii a doon loxloo àddina,
yëngal réewi réew,
17 def àddina wërngal këpp ndànd-foyfoy,
tas dëkk ya,
te du jàpp nit ba yiwi ko?”
18 Buuri àddina yépp, ba ñu daj,
ñépp a tëdd tëraayu teraanga,
ku ci nekk ak bàmmeelam.
19 Yaw, ñu xañ la bàmmeel, sànni la,
nga mel ni car bu ñu foñ.
Yaa ngi ne lareet ci biir néew yu saamar bóom,
ñu tàbbal leen ci xeeri biir kàmb.
Yaa ngi mel ni médd mu ñuy joggati.
20 Deesu la robaaleek yooyu buur,
yaa yàq sam réew,
faagaagal saw xeet.
«Deesul tuddati mukk askanu lorkat wii.
21 Waajal-leen fi ñuy rendi doom yi,
feye leen seen ñaawtéefi baay,
bala ñoo jógati, teg àddina loxo,
ba tabax fu ne ay dëkka.»
22 «Maa leen di jógal.»
Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
Mu ne: «Maay tenqi turu Babilon, tenqim ndesam
ba ca seeni doom ak seen askan.»
Kàddug Aji Sax jee.
23 Mu ne: «Maa koy def kërug siññéel,
def ko ab tan,
ba buube ko buubub rajaxe.»
Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
Mbugal ñeel na Asiri
24 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee giñ ne:
«Lu ma nar déy mooy am,
lii ma mébét, mooy sotti.
25 Maay joggati Asiri fi samam réew,
dëggaate leen fi sama kaw tund yi,
ba sama ràngi ñoñ rengiku,
seenub sëf sippiku.»
26 Mii mébét lañu mébétal àddina sépp,
bii loxo lañu xàccil xeet yépp.
27 Bu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dogalee déy,
ana ku koy dogale?
Bu xàccee loxoom,
ana ku koy fommal?
Ab yéeneb waxyu ñeel na Filisti
28 At ma Buur Axas saayee,
bii yéene jib na:
29 Filistee, seen yetu gannaaw wi damm,
bu ko kenn ci yeen bége,
nde ci ëkku jaan ji, la ñàngóor di génne,
am tostanam mujj di céebi.
30 Su boobaa ñi gëna walaakaana am lu ñu for,
néew-doole ya goor, ànd ak dal.
Waaye yeen, maa leen di xiifal, ngeen dee ba raaf,
xiif ba fàkkas ñi ngeen dese.
31 Yeen magi pénc mi, ñaawluleen!
Yeen waa dëkk bee, yuuxuleen!
Na Filisti gépp ne yàcc!
Bëj-gànnaar déy la saxar jollee,
kenn du wuute gàngooru noon ya.
32 Lees di tontu xeet wi yónnee di laaj,
xanaa ne leen Aji Sax jee sanc Siyoŋ,
te fa la baadooloy ñoñam di rawe.