Ab yéeneb waxyu ñeel na Misra
19
1 Yéene bii ñeel na Misra:
Aji Sax jaa ngii war niir wu gaaw,
jëm réewum Misra.
Yàllantuy Misra yég ko, di lox,
fitu waa Misra rëcc.
2 Maay xiir Misra ci kaw Misra,
kii song mbokkam, kii song xaritam,
ab dëkk jógal ab dëkk, diiwaan jógal diiwaan.
3 Waa Misra jànnaxe,
ma dëpp seen pexe.
Ñu seeti yàllantu yeek njuuma yi,
ak gisaanekat yeek boroom rawaan yi.
4 Maay teg Misra ci loxol sang bu néeg,
buur bu dëgër xol jiite ko.
Kàddug Boroom bee, Aji Sax ji ci gàngoor yi.
 
5 Ndoxum Niil ma day fer;
dex gaay ŋiis, wow koŋŋ,
6 solom ya xasaw,
wali Misra diib ba far ŋiis,
barax ak lu mu xeetool lax,
7 gàncax ga leru dexu Niil
ak ga saxe fa dex ga dabe géej,
ak lu ñu jiwoon ca wet ga,
lépp ay wow, naaw, ba jeex.
8 Nappkat di jàmbat,
kuy sànnib oos dexu Niil di jooy,
kuy mbaal waaru,
9 kuy liggéey lẽe am mbetteel,
kuy jàrt ak a ràbb poqe jommi.
10 Ñi yor réew mi dañuy sëngéem,
kuy liggéey di feyu am naqaru xol.
 
11 Kàngam ya fa Cowana dañuy teqlikook seen sago,
diglekati Firawna yu xelu ya di digle ag ndof.
Ma ne: «Yeen diglekat yi, nu ngeen mana waxe Firawna naan:
“Nun ay boroom xel lanu,
sosoo ca buur ya woon”?»
12 Firawnaa, ana say boroom xel?
Nañ la waxal boog, ba xamle
li Aji Sax ji Boroom gàngoor yi naral Misra.
13 Kàngami Cowan a ngi def yëfi dof,
kàngam ya fa Memfis, ñu nax leen,
te njiiti giiri Misra lajjal seen waa réew.
14 Aji Sax jee miirloo Misra,
gëlëmal ko ci lépp lu muy def,
ni màndikat buy jang ba tarxiis cim waccoom.
15 Du lenn lu kenn manatee defal Misra,
bopp akub geen du ci am pexe,
te bantub tiir ak barax a ci yem.
Lu jëm ci muju Misra
16 Su bés baa waa Misra mel niy jigéen,
di lox ndax tiit loxo bi jóg,
te Aji Sax ji Boroom gàngoor yi xàccil-leen ko.
17 Yuday doon tiitaangey waa Misra,
ba ku ñu ci tudd Yuda, nga tiit,
ngir la leen Aji Sax ji Boroom gàngoor yi naral.
18 Su keroogee mu am juróomi dëkki réewum Misra
yu nit ñay waxe làmmiñu ebrë,
di fa giñe Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
benn dëkk ba lañuy wooye Ir Ayeres,
dëkkub yàqute.
19 Bésub keroog ab sarxalukaay ñeel Aji Sax ji,
fa digg réewum Misra,
aw xer it ñeel Aji Sax ji fa kemu réew ma,
20 loolu di firnde, ñeel Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
di lu ko seedeel fa biir réewum Misra.
Bu ñu leen sonalee ba ñu woo Aji Sax ji,
mu yónnee leen ku leen wallu,
taxawu leen ba xettli leen.
21 Bésub keroog Aji Sax ji ci boppam mooy xamal Misra mooy kan,
ba waa Misra xam Aji Sax ji,
di jaamoo Aji Sax ji saraxi gàtt ak saraxi pepp,
digook moom tey wàccook seeni dige.
22 Aji Sax jeey duma Misra
duma yu ànd akum paj,
ñu walbatiku ci Aji Sax ji,
mu nangul leen, faj leen.
23 Su keroogee mbedd bawoo Misra ba Asiri,
waa Asiri di dikk ba Misra,
waa Misra di dem ba Asiri
te Misra di jaamoondook Asiri.
24 Bésub keroog Israyil ñetteel Misraak Asiri,
di barke fi digg àddina.
25 Aji Sax ji barkeel leen, ne:
«Barke ñeel na Misra, sama ñoñ,
ak Asiri mi ma sàkke samay loxo,
ak Israyil sama séddoo.»