Xibaaru mbugal ñeel na ay xeet
(Saar 28—33)
Mbugal ñeel na Samari
28
1 Wóoy ngalla Efrayima,
kaala gu yànj ga ay màndikatam di sagoo!
Taaram bu yéeme baa koy réer,
ni tóor-tóor yu wow,
te ma nga toŋ ca collb, wa ña biiñ man dëkke,
fa tiim xur wu nangu wa.
2 Dégluleen, jàmbaar ju am doolee ngi dikkal Boroom bi,
di tawub doji yuur, ngëlén luy sànke,
riddee riddi, sotti waame wu wale!
Loxoom la koy rattaxe fi suuf.
3 Dees na joggati kaala
gii màndikati Efrayim di sagoo.
4 Te tóor mu lax mi muy gànjaroo,
mu tege ca coll ya tiim xur wu nangu wa,
day mel ni figg ju ñor te jotul;
ka ko gis a koy gaaw witt, wonn.
5 Bésub keroog Aji Sax ji Boroom gàngoor yi
di kaala gu yànj, gànjar gu yéeme,
ñeel ndesu ñoñam,
6 mooy sol noowug dëgg kuy toog di àtte,
di jàmbaaral ñiy waññi noon yi song dëkk bi, xare.
 
7 Ñii itam ay naan biiñ bay tërëf,
màndiw ñoll, di jang:
sarxalkat akub yonent la aw ñoll di tërëfloo,
biiñ jànnaxe leen,
ñu màndiw ñoll, di jang,
bu ñu amee am peeñu, di tërëf.
8 Seen taabal yépp a ngi taq ripp,
fépp di waccu ak mbalit.
9 Ñu naa: «Ana ku Esayi mii di jàngal?
Ana ku muy àgge xibaar?
Xanaa ku yàggula fer,
di doora bàyyi ween?
10 Ca rëdd wii, ca rëdd wee,
nàngam sii, nàngam see,
as tuut fii, as tuut fee.»
11 Xanaa boog nit ñu seen wax leerul,
ñu diy làkk-kat,
la Aji Sax jiy waxeek askan wii?
12 Moo leen waxoon ne leen:
«Fii moo di nopplukaay bi,
noppal-leen ku sonn.
Fii a di dal-lukaay bi!»
Waaye nanguwuñoo dégg.
13 Moo tax seen kàddug Aji Sax mujj di:
«Ca rëdd wii, ca rëdd wee,
nàngam sii, nàngam see,
as tuut fii, as tuut fee.»
Moo tax ñuy tërëf,
daanoo njaaxaanaay ba damm,
di sërëx ak a keppu.
Doju doorukaay wee mat wéeruwaay
14 Kon nag yeen kókkalikat yi yilif
askanu Yerusalem wii,
dégluleen kàddug Aji Sax ji!
15 Yeena naay: «Danoo wóllëranteek ndee,
njaniiw lanu digool, ba du nu moom,
ba bu yaru musiba dikkeek diisaayam, du nu laal?
Noo def ay fen sunu rawtu,
ay wor di sunu làquwaay.»
16 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji wax ne:
«Maa ngii di dëj fi Siyoŋ aw doju coll,
muy doju collu tànnéef wu gànjare ngir kenu gi,
te ku ko wéeroo doo gaawa daw.
17 Dëgg laay def nattukaay,
njekk di sama buumu beteex,
tawub doji yuur buub rawtub fen,
wal ma mëdd làquwaay,
18 seen wóllëranteek ndee neen,
seen digook njaniiw toxu,
yaru musiba dikk ak diisaayam,
wulli leen ba ngeen nooy.
19 Saa yu dikkee ne leen céex,
suba su ne mu ne jaas,
guddeek bëccëg, mu teew,
te bu jibee sax fit rëcc.»
20 Lal a gàtt ba deesu ci tàlli,
malaan cëkk ba matul càngaayc.
21 Aji Sax jeey jóg na woon
fa tundu Perasim,
xadaru na woon ca xuru Gabawon
ngir jëf jëfam,
jëfam ju yéeme ja!
Moo nara liggéey liggéeyam booba,
liggéeyam bu tumurànke ba!
22 Tee ngeena baña kókkalee
bala ñoo teeŋal seeni jéng?
Sànkute kat moo di dogal bi ma dégg,
mu bawoo fa Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi,
di luy dikkal réew mi mépp.
Aji Sax jee xam doxalin
23 Teeyluleen te déglu sama kàddu,
teewluleen ba dégg samay wax.
24 Xool-leen ci lii: Ndax beykat bi day dëkke gàbb,
di rëdd ak a gàbbaat?
25 Bu gàbbee ba toolam maase,
du day sànni jiwum niseld,
wasaare jiwum kumin,
daldi def bele bi ay saawo,
sànni lors ba fa mu ko rëddal,
doora suy bele bu dëgër ba ca wet ya?
26 Dees koo xamal yoon wa,
te Yàllaam a ko ko jàngal.
27 Mbàccum nisel watiir amu ca yoon,
te deesul bàcc kumin itam, ba joggi ca tànki watiir.
Mbàccum nisel, yet a koy def;
mbàccum kumin, bant bu yem.
28 Gubi bele, dees na ca jaare watiir,
waaye deesu ci dëkk;
watiir ngay takk, bàcce ko pepp,
waaye doo ko bàcc ba mu far mokk!
29 Xel moomu it fa Aji Sax ji
Boroom gàngoor yi la bawoo.
Ndigalam a ni yéemee,
pexeem màgge ni!