Misra du mat Israyil cëslaay
30
1 Wóoy ngalla doom yii diy fippukat!Kàddug Aji Sax jee.
Ñu ngi nas mébét yu ma diglewul,
di digoo digoo yu ma leen xelalul,
di tegle bàkkaar ci kaw bàkkaar.
2 Ñoo dox wuti Misra te laajuñu ma,
xanaa di sàkku rawtub Firawna,
di keppaaroo keppaarug Misraa.
3 Rawtub Firawnaay mujj di seen gàcce,
keppaarug Misra di seen toroxte.
4 Seeni jawriñ a nga xaat ba Cowan,
seeni ndaw àgg ba Anesb,
5 waaye ñoom ñépp kersa lañuy ame Misra,
googu leen dul amal njariñ.
Du ndimbal, du njariñ,
xanaa gàcceek toroxte.
6 Yéeneb waxyu bii ñeel na malay àllub Negew:
Réewum tiis laak njàqare,
kërug gayndeeki segg,
ak saamaan ak céebi,
mbaam lañu sëf seen alal, jaare fa,
giléem lañu sëf seeni denc,
jëme xeet wu leen dul jariñ.
7 Ndimbalu Misra, cóolóolu neen!
Moo tax ma tudde ko:
Raxab, ponkal mi ne yàcc.
8 Aji Sax ji nee:
«Ayca, bind ko ci àlluwa, ñu gis!
Rëdd ko cib téere,
ngir ëllëg ak sibbir,
mu dib seede ba fàww.»
9 Wii xeet kat ay fippukat lañu,
yii doom a diy fen-kat
te nanguwuñoo sàmm yoonu Aji Sax ji!
10 Boroom ngis, ñu ne ko: «Bul gis,»
boroom peeñu, ñu ne ko: «Bu ñu firil peeñuy dëgg.
Wax nu lu neex,
gisal nu ay nax.»
11 Moyal yoon wi;
lajj, wàcc xàll wi,
te may nu jàmm ak Aji Sell ju Israyil.
12 Moo tax Aji Sell ju Israyil wax ne:
«Gannaaw yeena xalab kàddu gii,
yaakaaruleen lu moy doole ak pexey njubadi
yu ngeen wéeroo,
13 googu ñaawtéef ay mujj doon
seen xar-xaru tata ju kawe,
funki, tata ja jekki jóoru.
14 Da naan tasar ni njaqal xandeer
lu ñu naan rajax te ñéebluweesu ko,
ba deesul gis ca tojit ya, dog bu tibb xal,
mbaa mu as ndoxum déeg.»
15 Ndax Boroom bi Aji Sax ji,
Aji Sell ju Israyil dafa wax ne:
«Délsi, dal-lu moo leen di musal.
Ne tekk te wóolu maa leen di dooleel.
Waaye yeena buggul!
16 Yeena ne: “Déedéet, danuy war fas, daw!”
Dingeen daw moos!
Ngeen ne: “Daamar yu gaaw lanuy war.”
Ñi leen di dàq it di war daamar yu gaaw!
17 Junneey daw fu leen kenn gëdde,
juróom gëdd, ngeen daw yeen ñépp,
ba ña des mel ni bantub raaya ci kaw tund,
ne cundum ni raaya bu wéet ca coll wa.»
18 Aji Sax ji déy a leen namma baaxe,
moo ko tax di jóg moos ngir yërëm leen,
nde Aji Sax jeey Yàllay njubte.
Ndokklee képp ku ko yaakaar!
19 Yeen waa Siyoŋ, yeen waa Yerusalem,
dootuleen jooy mukk!
Bu ngeen jooyee, mu yërëm leen moos;
bu leen di dégg, di leen nangul.
20 Boroom bee leen di leel njàqare,
nàndal leen coono,
waaye moo leen di jàngal, dootu leen làqu;
dingeen gis ki leen di jàngal,
21 di dégg kàddu guy jibe seen gannaaw,
naa leen: «Yoon waa ngii, jaareleen fi;»
bu ngeen awee ndijoor, mbaa càmmoñ.
22 Su boobaa ngeen sobeel seen jëmmi tuur yi ñu xoob xaalis;
ak wurus wu xoob seen tuur yi ñu móol,
ba boole lépp sànni ni sagar yu sobewu,
ne ko: «Sore nu!»
23 Su boobaa Aji Sax ji tawal lu ngeen ji,
may leen pepp mu suuf meññ,
sakkan te nangu,
seen juri keroog di fore parlu yu yaa,
24 Nag yeek mbaam yiy rijji sax,
di xontoo cox bu ñu xorom,
jóge ci mbàccum roq ak ngaska.
25 Te tundoo tund wu kawe,
wu mag ak wu ndaw,
wali ndox a cay wale,
keroog bés ba deret di tuuroo tuuru,
tata ya jóoru.
26 Weer day leer ni jant,
jant gënatee leer,
mel ni juróom yaari bëccëg,
bésub keroog ba Aji Sax jiy takk damm-dammu ñoñam,
fajal leen góom yi ay dóoram sabab.
Aji Sax ji song na Asiri
27 Aji Sax jaa ngii, jóge fu sore;
mer ma réy,
mu jógaale kàddug àrtu gu diis,
di waxe xadar ju mat sëkk,
baat ba mel ni sawara wuy xoyome,
28 noo ga di wal mu baawaan,
tollu ci put;
mu nara segge xeet yi ab seggukaayu alkànde,
wewal xeet yi ag laab gu leen di réeral.
29 Teewul, bokk yi, seen woy yay jib;
mel ni guddig màggal,
ànd ak mbégte ni kuy toxoro,
yéeg jëm kaw tundu Aji Sax ji,
cëslaayal Israyil.
30 Aji Sax jeey yékkati kàddoom gu màgg,
wone diisaayu loxoom,
ànd ak tàngooru meram,
ak sawara wuy xoyome,
ak waameek ngëlén, ak tawub doji yuur.
31 Kàddug Aji Sax jeey jib,
Asiri tiit bay lox,
yetu Aji Sax ja dal,
32 te saa yu yet wa Aji Sax ji féetale Asiri dalee,
ngeen jibal am tëgg aki xalam.
Aji Sax jeey xàcci loxoom, xareek Asiri.
33 Xambees na démb ab taal bu ñuy wax Tofetc,
te buur ba lees ko waajalal;
dees koo xóotal, yaatal ko,
sawara way tàkk, matt ma ne gàññ,
noowal Aji Sax ji nar caa tàkke,
di sël-sëli ni walum tamarax.