Yoonu ñibbi Siyoŋ taxaw na
35
1 Màndiŋ ak suuf su ne sereŋ dina bég,
joor gu wow bànneexu, tóor ba ne ràññ.
2 Day tóora tóor,
di bànneexu, bay sarxolle,
ba jagoo darajay gottub Libaŋ
ak taaru àllub Karmel ak Saron.
Foofa lees di gise darajay Aji Sax ji,
sunu taaru Yàlla.
3 Ku yoqi, dooleel-leen ko,
ku óom yay fenqe, jàppleleen ko.
4 Ku fitam rëcc, ne leen ko:
«Dëgërlul te bul tiit.
Sa Yàllaa ngii di la feyul,
ba yool say noon.
Moom mooy dikk, wallusi la.»
 
5 Su boobaa gëti silmaxa muriku,
noppi tëx sikkliku.
6 Su boobaa ab làggi ne jàyy ni kéwél,
ab luu sarxolle.
Am ndox ay fettaxe màndiŋ ma,
ay wal wale joor gu wow,
7 suuf su wow doon ub déeg,
joor gu maral ballal bëti ndox.
Fa till fàkkoon, di fa goore,
gattax ak barax a fay sëqe.
8 Foofa law yoon di jaare,
ñu di ko wooye Yoon wu sell wi.
Ku sobewu du fa jaare,
ñi moom woowu yoon,
ñooy ñi koy topp.
Ab dof sax du fa lajje.
9 Gaynde du fa am,
rab wu aay du fa dox,
du lenn lees fay gis,
ku ñu jot rekk a fay jaare.
10 Ñi Aji Sax ji xettleey délsi,
duggsi Siyoŋ, di sarxolle,
kaalawoo bànneex bu sax.
Mbég ak bànneex a leen di dab,
naqar aku tiis dëddu leen.