Barke ñeel na ñoñu Aji Sax ji
51
1 Dégluleen maa, yeen ñiy wut njekk,di sàkku Aji Sax ji.
Xool-leen doj wi ñu leen yette,
xool xóotey kàmb gi ñu leen seppee:
2 Seen maam Ibraayma laa ne, moom ngeen di xool,
xool ci Saarata mi leen meññ.
Ba muy kenn laa ko woo,
barkeel ko, ful ko.
3 Aji Sax jeey dëfal Siyoŋ moos,
dëfalaale fépp fu fa dib gent,
ba def màndiŋam ni toolub Àjjana,
jooram gu wow mel ni toolub Aji Sax ji,
mbégteek bànneex teew fa,
ak cant gu woy feelu.
4 Yeen sama ñoñ, teewluleen ma,
yeen sama ñoñ, dégluleen ma.
Fi man la téereb yoon di bawoo,
te maay fettaxal sama àtte,
muy leeru xeet yi.
5 Sama wall jege na,
sama njekk dëgmal na,
ma nara àttee xeet yi sama dooley përëg.
Man la waa dun yiy xaar,
sama dooley përëg lañu yaakaar.
6 Séentuleen asamaan
te xool suuf si mu tiim.
Asamaan ay tasaaroo ni saxar,
suuf ràpp ni mbubb,
ñi ko dëkke dee niy weñ,
te du tee sama wall di sax ba fàww,
sama njekk it du dagg.
7 Yeen ñi xam njekk, dégluleen ma,
yeen, askan wi sama yoon yebu ci seen xol.
Buleen ragal nit ku leen sewal,
buleen tiit seeni xaste.
8 Sax a leen di lekk ni mbubb,
max ŋeeñ leen ni ndimol kawaru gàtt;
te du tee sama njekk sax dàkk,
sama wall saxal maasoo maas.
9 Aji Sax ji, yewwul, ngalla yewwul;
wone sa doole.
Yewwul na bu jëkkoon,
bu yàgga yàgg.
Xanaa du yaa falaxe Raxab?
Du yaa jam ninki-nànka jooja?
10 Xanaa du yaa wowal géej
ak ndoxum xuram wu ne màww,
def xóotey géej aw yoon,
ña nga jot jàlle ca?
11 Ñi Aji Sax ji goreel, nii lañuy dellusee,
agsaaley sarxolle fa Siyoŋ,
kaalawoo mbég mu sax,
mbégteek bànneex wàllsi,
naqar aku tiis daw.
12 Man ci sama bopp maa leen di dëfal.
Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee,
doom aadama ju bokk akum ñax aw demin?
13 Dangeena fàtte Aji Sax ji leen sàkk,
ki firi asamaan, dëj suuf?
Dangeen di dëkke bésoo bés,
di tiit xadaru boroom doole
buy waaja sànke?
Ana fu xadaru boroom doole mujje?
14 Ku diisoon ba waaf léegi nga féex;
doo deeye pax ma nga tëje,
te doo ñàkk loo lekk.
15 Man maay seen Yàlla Aji Sax ji,
kiy yëngal géej, riiral gannaxam,
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi di sama tur.
16 Maa la sexal samay kàddu,
yiire la sama keru loxo,
aj asamaan, dëj suuf,
ne Siyoŋ: «Yeenay sama ñoñ.»
17 Yewwulee, yewwul, Yerusalemee jógal,
yaw mi Aji Sax ji nàndal kaasu mbugalam.
Kaas bu wex bay miirloo,
taat wa, yaa ko siitaatu.
18 Amul ci ñi nga jur, kenn koo dese
ku lay wommat.
Amul ci doom yi nga yar, kenn
ku lay jàpp ci loxo.
19 Yii yaar de dikkal na la:
Yàquleek sànkule.
Ana kuy bokk ak yaw saw naqar?
Xiif ak loraangey saamar!
Ana nu ma lay dëfale?
20 Sa doom yi ne lasar,
mbete kooba yu fiir jàpp,
ñu ne lareet fépp fu mbedd daje,
këppoo sànjum Aji Sax ji,
sa Yàlla ji leen rëbb.
21 Rikk déglul nag lii, yaw mi musiba dal,
nga màndi te du biiñ.
22 Sa boroom Aji Sax ji,
sa Yàlla jiy layool ñoñam
dafa wax ne: «Mu ngoog, maa jële ci sa loxo,
kaas bu wex biy miirloo;
taatu kaas ba def sama mbugal,
dootoo ko naan.
23 Maa koy teg ci loxol ñi la doon naqaral,
te naan la: “Sëggal, nu joggi, jàll,”
nga def sa gannaaw gi aw yoon,
ñu joggi, wéy.»