Ab daan ñeel na moykat yi
57
1 Aji jub ñaa ngi dee,
te kenn yégalu ko yaramam.
Gor ñaa ngi faatu,
te kenn ràññeewul
ne aji jub ji, faatoom, musiba la koy moyale.
2 Kiy am jàmm ëllëg,
di am noflaay ci biir tëraayam,
mooy kiy wéye njub.
 
3 Waaye yeen, dikkleen fii,
yeen doomi xërëmkat yi,
yeen askanu njaalookat yiy gànctu,
4 ana ku ngeen di ñaawal?
Ana ku ngeen di ŋóobi,
ak di ko kókkali?
Xanaa dungeen doomi moykat,
di askanu workat,
5 di xabtaloo bànneex
ci ker garab yu mag yi,
ak ker garaboo garab gu naat,
di rendi seeni doom ci yoonu ndox yi,
ak xarantey doj yi?
6 Yaw Israyil, jëlal doj yu rattax
yi ci yoonu ndox wi, séddoo,
muy sa cér, nga muurloo!
Ñoom ngay tuural,
di leen defal ay saraxi pepp.
Waaye Aji Sax ji nee:
«Ndax damay jéllale?»
7 Tund wu mag te kawe,
nga fàkk fa tëraay,
yéeg fa, di fa sarxalal.
8 Yaa takk say baaxantal
ci sa lafu bunt ak sa jëni bunt,
yaa ma wacc, di ñorikoo feneen,
yéeg sab lal, yaatal.
Yaa takktook ñii nga soppa tëddal
te safoo di niir seeni cér.
9 Yaa tukki ba ca buur ba, yóbbaaleg diw,
ak cuuraay lu ne gàññ,
yebal say ndaw fu sore,
ba ñu àkki njaniiw.
10 Tukki bu sore bu la sonal sax
taxu la ne: «Fomm naa.»
Bànneex bi ngay séentu ngay leqlikoo,
ba tax sonnuloo.
 
11 Ana kooy tiit,
ak koo ragal ba di ma wor,
fàttlikootoo ma,
faaleetoo ma?
Damaa noppi lu yàgg daal,
ba tax ragalatoo ma?
12 Defe nga ne njekk nga def,
waaye dinaa la weer,
te sa jëf du la jariñ.
13 Boo wootee wall,
na la sa gàngooru tuur xettli.
Ñoom ñépp la ngelaw di buub,
callweer yóbbu leen.
Waaye ku ma làqoo,
kookooy moom réew mi,
séddoo sama tund wu sell wi.
 
14 Dees na ne: «Maasaleleenoo, maasaleleen,
yaatal leen yoon wi,
te jële luy pakk ci sama yoonu ñoñ.»
15 Ku màgg, ku kawe ki,
ki màkkaanam sax dàkk
te turam sell, daa wax ne:
«Fu kawe te sell laa màkkaanoo,
maa dëkk ak boroom xol bu mokk,
te toroxlu,
ngir leqli ku toroxlu,
leqli boroom xol bu mokk.
16 Duma wéye di sikke ba fàww,
duma saxoo di mer,
lu ko moy képp ku ma sàkk
day tàggook bakkanam.
17 Ñaawtéefi Israyil ak alalam ju lewul
moo ma merloo,
ma duma ko, xañ ko sama kanam,
waaye mu të ticc, topp xolam.
18 Xam naa jikkoom,
waaye maa koy faj,
wommat ko,
dëfale koy xéewal,
mook ñiy ñaawloondook moom.
19 Maay teg ci seen làmmiñ kàddug cant.
Jàmm, na jàmm ñeel ñépp,
ku soreek ku jege.»
Kàddug Aji Sax jee.
Mu ne: «Maa leen di faj.»
20 Waaye ñu bon ñi, mbete géej
gu sàmbaraax, tëë dal,
gannax yay baaje ban ak suuf.
21 Sama Yàlla nee:
«Jàmm du ñeel ñu bon ñi.»