64
1 Ni sawara di jafale boob,
baxale ko am ndox,
ni ngay xamalsee say noon, saw tur,
ba yooyu xeet di lox fi sa kanam.
2 Ba ngay def kiraama ya ñu séentuwuloon,
yaa wàcc, tund yi yëngu fi sa kanam.
3 Ca cosaan ba tey maseesula dégg,
nopp masula dégmati,
bët masula gis yàlla ju la moy,
mu defal nii ku ko yaakaar.
4 Yaay gatandu kiy bége njekk gi muy jëfe
te di ba xel say yoon,
yi ñu mas di jaare, ba mucc.
Waaye kat, yaa nu mere, ndax noo bàkkaar.
5 Nun ñépp a mujj mel ni sobe,
ni sagaru sobe la sunu gépp njekk mel.
Nu ngii nun ñépp mel ni xob wu lax,
sunuy tooñ buub nu, yóbbu ni ngelaw.
6 Du kenn kuy wormaal sa tur,
mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw,
yaa nu làq saw yiw,
yaa nu def ban bu tooy
ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.
 
7 Waaye déy, Aji Sax ji, yaa di sunu Baay;
noo di ban, yaw ngay tabaxkatu njaq,
nun ñépp di sa liggéeyu loxo.
8 Éy Aji Sax ji, bul mer lool,
bul ba xel fàww ci ñaawtéef.
Ngalla seetal ne nooy sa ñoñ, nun ñépp.
9 Sa dëkk yu sell doon nañu màndiŋ,
Siyoŋ ca la, doon na màndiŋ.
Yerusalem laa ne, gental na!
10 Sunu kërug jaamookaay gu sell ga te tedd,
fa la sunuy maam daa màggale,
sawara xoyom na ko,
mboolem lu nu soppoon yàqu yaxeet.
11 Éy Aji Sax ji, lii lépp xanaa doo ci téye sa loxo?
Xanaa doo ci seleŋlu, teg nu gàcce gu réy?