Mbugalum fippu ci kaw Aji Sax ji du jaas
13
1 Bu Efrayim daan wax, ñépp ay lox;
mu amoon daraja fi digg Israyil.
Waaye moo sikkal boppam ci tuuri Baal,
ba dee.
2 Léegi ñu ngi gën di bàkkaar,
di xellee ci seen xaalis jëmmu tuur,
ay jëmmi xërëm yu ñu sàkke seen xareñte,
lépp di càkkéefu ay liggéeykat,
te ci ñoom la nit ñi naan:
«Rendikati sarax yaa ngi fóon ay tuuri wëllu.»
3 Moo leen tax di naaxsaay ni niiru suba,
mbaa layub njël,
mbaa mboob mu naawe dàgga ja,
mbaa saxar su gillee ci jankub néeg.
 
4 «Man Aji Sax ji, fa Misra laa dale di seen Yàlla,
xamuleen Yàlla ju dul man,
te kenn du musle ku ma moy.
5 Man maa leen ràññee ca màndiŋ ma,
ci biir réewum maral.
6 Ngeen wëtti ba regg,
regg, bew, ba tax ngeen fàtte ma.
7 Moo tax ma mel ni gaynde ci yeen
di tëroo ni segg ciw yoon.
8 Maay dajeek yeen ni rab wu aay
wu ñu xañi doom,
maay xotti seen mbuusum xol,
fa laa leen di yàppe ni gaynde,
te rabu àll moo leen di xotat.
 
9 «Israyiloo, yàqu nga,
te maa yor sa wall.
10 Ana seen buur boog,
ba mu xettli leen ci seen mboolemi dëkk?
Ana seen njiit yi ngeen sàkku woon, ba ne ma:
“Falal nu buur aki kàngam?”
11 Ci biir mer laa la falal buur,
te ci samam sànj laa ko follee.
 
12 «Takkees na ñaawtéefi Efrayim,
rënkees na ay moyam.
13 Lu mel ni mititu mat moo dikkal waa jii,
te muy doom ju amul xel,
ba juddu jot, génnul biiru ndeyam.
 
14 «Man nag maa leen di musal ci njaniiwa?
Maa leen di jot ci ndee?
Moo yaw ndee, ana say mbas?
Yaw njaniiw laa ne, ana sa tooke?
Fomm làqu na ma!
15 Efrayim moom, su naatee ci biiri bokkam it,
fa màndiŋ ma la ngelawal penkua,
ngelawal Aji Sax ji di uppe,
bëti ndoxam tëju,
ay teenam déy.
Kii mooy sëxëtoo ab dencam,
ak mboolem lu cay alal.»