14
1 Dees na topp waa Samari,
nde ñoo fippu ci seen kaw Yàlla.
Saamar lañuy fàddoo,
seeni doom, ñu rajaxe leen,
seen jigéeni wérul, ñu butti.
Dëpp, am njéggal
2 Israyiloo, dellul ci sa Yàlla Aji Sax ji,
fakktaloo nga sag ñaawtéef.
3 Waajal-leen ay kàddu te dellu ci Aji Sax ji,
ne ko: «Baal nu mboolem ñaawtéef
te nangul nu,
nu yékkati kàdduy màggal
yu wuutu saraxi yëkk.
4 Asiri du nu xettli,
ay fasi xare it, dunu ko war,
te dootunu wax lu nu sàkke sunuy loxo, ne ko:
“Yaw yaa di sunu Yàlla.”
Li nuy wax kay mooy yaw yaay kiy yërëm jirim.»
 
5 Aji Sax ji nee: «Maay garabal seenug déggadi,
maa leen di bëggal sama bopp,
nde mereetuma leen.
6 Maay mel nib taw ci Israyil,
ñu focc ni tóor-tóor,
seeni reen sampu ni garabi Libaŋ,
7 car ya law, yànj nig oliw,
xeeñ ni gottub Libaŋ.
8 Ñooy délsi, keppaaroo ko,
dellu ji, pepp dundaat.
Dañuy giir nig reseñ,
am bayre ni biiñu Libaŋ.
 
9 Yeen Efrayim, lu ma masa séq ak jëmmi tuur?
Man maa leen di nangul, di leen wattu,
di leen keral ni garab gu naat gu dul ruus,
sa meññeef bawoo fi man.»
10 Ku rafet xel, na dégg lii,
kuy ràññee na ko xam.
Yooni Aji Sax ji kat day jub,
te kuy jubal jaare ca,
ab jàddkat moo cay tërëf.