Téereb Yonent Yàlla
Nawum
1
1 Yéeneb waxyu bu dal dëkk bi ñuy wax Niniw a ngi, di téereb peeñum Nawum ma dëkk Elkos.Aji Sax jeey jàmbaar ju raglu te baax
2 Aji Sax ji mooy Yàlla ju fiir, te mooy mbugale,
Aji Sax ji mooy mbugale, te di boroom sànj.
Aji Sax ji mooy mbugal ay bañam,
mooy sànju ci kawi noonam.
3 Aji Sax ji la mer ma diib, doole ja bare;
te du ñàkka topp ku tooñ, ag tooñaangeem.
Aji Sax jeey daagoo biir callweer ak ngëlén,
niir yi di pëndub tànkam.
4 Mooy gëdd géej, wowal;
mboolem dex, mu ŋiisal;
parluy Basan ak Karmel, mu laxal;
tóor-tóori àllub Libaŋ, mu laxal.
5 Tund yu mag yi di ko loxal,
tund yu ndaw yi seey,
suuf fuddu fi kanamam,
mook àddina ak mboolem li ci biiram.
6 Bu sànjoo, ana kuy taxaw?
Ana kuy dékku tàngooru meram?
Am sànjam a naan soteet ni sawara,
doj yi rajaxoo fi kanamam.
7 Aji Sax jee baax,
moo dib rawtu, bésub njàqare,
te moo ràññee ñi ko làqoo.
8 Mbàmbulaan lay walal ba faagaagal dëkk bii,
te mooy toppi noonam ba ca biir lëndëm ga.
Njàqare ji du ñaar
Ñeel Yuda
9 Ana lu ngeen di fexeel Aji Sax ji?
Mooy neenal, lépp neen;
njàqare ja du ñaar.
10 Niy taxas la ay noonam di laxasoo,
mel ni ñu naan ba màndi,
te ni boob mu wow lañuy lakke ba xoyomu.
Ñeel Niniw
11 Ci yaw dëkk bii la nit génne,
di fexeel Aji Sax ji lu bon,
di mébét pexey ndëngte.
Ñeel Yuda
12 Aji Sax ji moo ne:
«Bu ñu matoon, ne gàññ it
ni lees leen di dagge, ñu ne mes.
Maa la mitital, dootuma la mitital.
13 Léegi buum gi ñu la yeewe laay dog,
say jéng laay dagg.»
Ñeel buuru Niniw
14 Aji Sax ji moo santaane lii ci yaw.
Mu ne: «Lu bokk ci saw tur du lawati,
kërug say yàlla laay dagge xërëm
ak jëmmi weñ gu ñu xelli,
te maay waajal sa bàmmeel,
nde tekkiwuloo tus.»