Téereb Yonent Yàlla
Abakug
1
1 Ab yéenee ngi bu ñu won Yonent Yàlla Abakug.Abakug tàmbali naa jooy
2 Éy Aji Sax ji, foo àppal lii,
may woote wall, dégluwoo ma?
Ma di la jooy aw ay, te walloowoo!
3 Ana loo may wone lu bon,
tey seetaan noteel?
Yàquteeku ay fi sama kanam,
xuloo di wéy, ŋaayoo jolli.
4 Moo tax yoon lafañ,
te àtteb dëgg du feeñ mukk.
Ku bon a tanc ku jub,
ba tax ab àtte jalgatiku.
Aji Sax ji tontu na
5 «Xool-leen ci biir xeet yi ba gis,» la Aji Sax ji wax.
Jaaxleleen ba jàq, nde jëf a ngi jëfe ci seeni jant,
bu ñu leen ko waxoon, dungeen ko gëm.
6 Maa ngii di dooleel waa Babilon,
xeet wu wex, ràkkaaju,
di wër déndi àddina,
di nangu màkkaani jaambur.
7 Ñu ñàng, raglu,
te di dogalal seen bopp àtteb yoon
ak sañ-sañ.
8 Seeni fas a gëna gaawi segg,
gëna aay tilli timis.
Fu sore la seeni gawar jóge, tëbal,
naaw nig jaxaay
ju ne jàyy, lekkum rëbbam.
9 Aw ay lañuy dikke, ñoom ñépp,
buurandoo, jubal màkk seen kanam,
te ñi ñuy jàpp njaam bare ni feppi suuf.
10 Ñooñu ay buur lañuy ñaawal,
boroomi daraja di seen reetaanukaay;
ñii lépp luy tata lañuy kekku,
jalal ko suuf, nangu ko.
11 Jàll, wéy lañu cay teg ni ngelaw,
tegoog tooñ, te seen doole di seen yàlla.»
Abakug jooyati na
12 Waaye Aji Sax ji, xanaa du yaa masa nekk?
Sama Yàlla sama Aji Sell ji, doo saay.
Aji Sax ji, ab àtte nga tabbe ñii,
yaw sama cëslaay, mbugal nga fi dëje ñii.
13 Sa gët yu sell jomb naa niir lu bon,
te manoo seetaan noteel!
Ana looy seetaan ay workat?
Looy noppi te ku bon di mëdd
moroomam mu ko gëna jub?
14 Yaa def doom aadama mel niw jën,
mbaa ndiiraanu ndundoot lu amul njiit,
15 te ñoom ñépp la ku bon di korandoo,
diri leen ciy mbaalam,
dajale ciy caaxam,
ba tax ko di bég aka bànneexu.
16 Moo tax muy rendil mbaalam ab sarax,
di taalal ab caaxam saraxu cuuraay,
te naan moo niinal njëlam,
duunal ab dundam.
17 Mbaa du nii lay yuree mbaalam,
di wéye fàllas ay xeet te yërëmul?