Abakug ñaan na ci Yàlla
3
1 Ñaanu Yonent Yàlla Abakug a ngii, galanu woy wi di galanu njàmbat.
2 Éy Aji Sax ji, maa dégg sab jëw,
Aji Sax ji maa yéemu ci sa jaloore!
Ngalla yeesalal say jaloore, nu fekke,
xamleel say jaloore, nu fekke,
bu la am sànj teree geesu, yërëm.
 
3 Yàllaa ngi jóge Teman,
Aji Sell ji foofa ca tundu Parana lay bawoo. Selaw|selaw:.
Darajaam moo dajal asamaan,
teddngaam fees kaw suuf.
4 Kee di leer gu ne ràññ,
ay ceeñeer fettaxe ci loxoom,
te fa la dooleem làqe.
5 Mbas moo dox, jiitu ko,
jàngoro topp ciy tànkam.
6 Kee taxaw, yëngal suuf;
kee xoole, loxloo xeet yi,
tund yu mag ya woon naka jekk rajaxoo,
tundi cosaan yu ndaw ya maasaloo.
Kii moo moom yooni cosaan yi.
7 Njàqare laa gis ca xaymay Kusan,
te ndimoy xaymay waa Majanb yëngu na.
 
8 Aji Sax ji, dex yi nga sànjul?
Am dex yi nga mere?
Am géej nga sàmbaaral,
ba war say fas,
dawal sa watiiri dawal-daan?
9 Yaa génne sa xala mbaram,
feesal sa mbuusum fitt. Selaw.
Yaa xare suuf ay dex.
10 Tund yi gis la, jaayu;
waame wàcc, wéy;
xóote ya riir,
gannaxam ya jolli fa kaw.
11 Jant ak weer ne tekk fa seen màkkaan,
janook sa leeru fitt yi soqi,
ak melax gi tàkke ci sab xeej.
12 Am sànj nga daagoo fi kaw suuf,
mer nga dëggaatee xeet yi.
 
13 Yaa génn ngir wallusi sa ñoñ,
wallusi ki nga fal.
Yaa rajaxe puju néegu ku bon ki,
xar ko ñaar, geen ba ci put. Selaw.
14 Ba noon ya riddeendoo, di nu tasaaresi,
seen xeeju bopp nga bëtte seen bopp,
fekk leen ñuy xaxaloo, ni ñuy waaja sëxëtoo
ay néew-ji-doole, fu kenn yégul.
15 Yaa jaabal say fas biir géej,
yëngal mbàmbulaan ma.
 
16 Ba ma ca déggee, samay butit a yëngu,
coow la tax samay tuñ di lox,
sama yaram dee goyy,
may lox fi ma taxaw,
te ne cell, di séentu bésub njàqare,
bay dikkal xeet wi nu song.
17 Ndaxam garabu figg foccul,
doomu reseñ amul ca ndeyam,
njurum garabu oliw àntuwul,
tool yi meññul aw ñam,
gàtt it tukkee na ca gétt ga,
du genn jur gu gudd ci wurmbal,
18 te man may bànneexoo Aji Sax ji,
Yàlla ji may wallu laay bége.
19 Aji Sax ji Boroom bi mooy sama doole,
moo ma defal samay tànk mel ni yoy kéwél,
te fa kawte ya la may daaguloo.
 
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak samay xalam.