Wooteb tuub jibal na Yuda
2
1 Yeen xeet wi dul rus, dajeleena daje,2 balaa dogal bee taxaw,
bésub mbugal ne jaas ba wéy ni boob,
bala leen tàngooru merum Aji Sax jee dikkal,
bala leen bésub merum Aji Sax jee taxawal.
3 Sàkkuleen Aji Sax ji,
mboolem yeen néew-dooley réew mi,
yeen ñiy jëfe àttey yoonam,
sàkkuleen njekk te sàkkoo toroxlu,
jombul ngeen yiiru, kera bésu merum Aji Sax ji.
Waxyub mbugal ñeel na xeet yu bare
4 Gasa dëkk ba lees di wacc,
Askalon gental,
Asdodd, digg bëccëg lees leen di buub, génne,
te Ekkrona lees di déjjati.
5 Wóoy ngalla yeen waa tefesu géej,
yeen xeetu Kereteenb ñi,
kàddug Aji Sax ji dal na leen.
Yeen waa Kanaan, réewum Filisteen ñi,
maa leen di sànk ba dungeen dese kennc,
6 tefesu géej doon àllub parlu,
ak dëkkuwaayu sàmm seek gétt gi.
7 Tefes ga, ndesu kër Yuda koy moomd,
ñu di ca fore,
bu ngoonee ñu tëri néegi Askalon.
Seen Yàlla Aji Sax jee leen di dikkal,
tijji seen wërsëg (/yiwileen cig njaam.)
8 «Maa dégg ŋàññi Mowab,
kàddu yu ñaaw yi Amoneen ñiy ŋàññe sama ñoñ,
tey damu, nara nangu seen suuf.
9 Moo tax, giñ naa ko ci man miy dund,»
kàddug Aji Sax ju gàngoor yee, Yàllay Israyil,
«Mowab déy ni dëkkub Sodom lay mujje,
Amoneen ñi mel ni Gomor,
ay dég ak paxi xorom a koy nangu,
mu gental ba fàww.
Sama ndesu ñoñ a leen di sëxëtoo,
ndesu xeet wi ma séddoo moo leen di moom.»
10 Loolu lañuy yooloo seen reewande,
nde ñoo doon ŋàññe aka damu
ci kaw ñoñi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
11 Nu raglu la Aji Sax jiy dale ci seen kaw,
te mooy ràggal yàllay àddina yépp,
ba xeet yi di ko sujjóotale dunoo dun,
wu ci nekk ak fa nga fare.
12 Yeen waa Kuus, itam
yeen lees di fàdde sama saamar.
13 Keey xàccil loxoom bëj-gànnaar,
keey sànk réewum Asiri,
keey def Niniw ab gent bu wow ni màndiŋ.
14 Ca digg dëkk ba la jur gay goore,
ak xeetu rab wu nekk;
looy aki saaw fanaane kaw jëni bunt ya,
ay sab jibe ca palanteer ya,
tojit ya dala jale ca bunt ya,
xànqi seedar ya ne duŋŋ.
15 Ana dëkk bu xumb ba dëkke woon kaaraange,
te naan cim xelam: «Man rekk a, du keneen»?
Nan la doone nii ab gent,
bérab bu rab yiy goore,
mboolem ku fa jaare, ub gémmiñam, jalu.