Yeesu faj na ku gaana
8
1 Bi loolu amee Yeesu wàcc ca tund wa, te mbooloo mu bare topp ko. 2 Noonu ku gaana ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa faj.» 3 Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ. 4 Yeesu ne ko: «Déglul, bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp sarxalkat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir mu nekk seede ci ñoom.»Ngëmu njiitu xare bi
5 Gannaaw loolu Yeesu duggoon na Kapernawum. Bi mu fa duggee nag, ab njiitu xare fekksi ko. Mu ñaan ko, 6 ne ko: «Sang bi, sama surga dafa làggi, tëdd ca kër ga te sonn lool.» 7 Yeesu ne ko: «Dinaa ñëw faj ko.» 8 Waaye njiit la ne ko: «Sang bi, yeyoowuma nga dugg ci sama kër; waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér. 9 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»
10 Bi ko Yeesu déggee, mu waaru, ne ña topp ci moom: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, masumaa gis ci bànni Israyil ku gëme ni kii. 11 Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. 12 Waaye ñi waroona bokk ca nguur ga, dees na leen sànni ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.» 13 Ci kaw loolu Yeesu wax njiit la ne ko: «Ñibbil, na ame, ni nga ko gëme.» Noonu ca waxtu woowa sax surga ba daldi wér.
Yeesu faj na jarag yu bare
14 Gannaaw loolu Yeesu dem kër Piyeer. Ba mu eggee, mu fekk gorob Piyeer bu jigéen tëdd ak yaram wu tàng. 15 Bi mu ko gisee, Yeesu laal loxoom, tàngoor wa daldi wàcc; soxna sa jóg, di ko topptoo.
16 Ca ngoon sa ñu indil ko ñu bare ñu rab jàpp. Yeesu dàq rab ya ak kàddoom te faj ñi wopp ñépp. 17 Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan:
«Fab na sunuy wopp, gàddu sunuy jàngoro.»
18 Bi Yeesu gisee mbooloo ma ko wër nag, mu sant taalibe ya, ñu jàll dex ga. 19 Laata ñuy jàll, benn xutbakat daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, dinaa la topp fépp foo jëm.» 20 Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.» 21 Noonu keneen ca taalibe ya ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkka dem suuli sama baay.» 22 Yeesu ne ko: «Toppal ci man te bàyyi ñi dee, ñu suul seeni néew.»
Yeesu dalal na ngelaw li
23 Bi mu ko waxee, Yeesu dugg ca gaal ga, ay taalibeem topp ko. 24 Ca saa sa ngelaw lu bare daldi yëngal dex ga, ba duus ya sàng gaal ga. Fekk booba Yeesu nelaw. 25 Noonu taalibe ya daldi jegesi, yee ko naan: «Sang bi, musal nu, nu ngiy dee!» 26 Waaye Yeesu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm. 27 Bi ko nit ña gisee, ñu waaru naan: «Kii kan la ci biir nit ñi, ba ngelaw li ak dex gi di ko déggal?»
Yeesu faj na ñaar ñu rab jàpp
28 Bi Yeesu jàllee nag, ba teer ca diiwaanu waa Gadara, ñaar ñu rab jàpp daldi génn ca sëg ya, ñëw kar ko. Ñaar ñooñu nag, ñu soxor lañu woon, ba kenn ñemewul woona jaar foofa. 29 Ña rab jàpp daldi xaacu naan: «Yaw Doomu Yàlla ji, loo nuy fexeel? Ndax danga noo bëgga mbugal, bala waxtu way jot?»
30 Fekk amoon na ca wet ya géttu mbaam-xuux yu bare yuy for. 31 Rab ya nag ñaan ko ne: «Boo nu dàqee, sànni nu ca géttu mbaam-xuux ya.» 32 Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag daldi génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab ca ndox ma.