Farisen ya ak aada ya
15
1 Ca jamono jooja amoon na bés ay Farisen ak ay xutbakat jóge Yerusalem, ñëw ci Yeesu ne ko: 2 «Lu tax say taalibe di moy aaday yoon, yi maam yi tëral? Ndaxte duñu raxas seeni loxo, bu ñuy lekk.» 3 Waaye Yeesu ne leen: «Yéen itam lu tax ngeen di moy li Yàlla santaane, ngir topp seeni aada? 4 Yàlla nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” te it: “Ku móolu sa ndey walla sa baay, dees na la rey.” 5 Waaye yéen dangeen ne: “Ku wax sa ndey walla sa baay: ‘Li ngeen wara jariñoo ci man, jébbal naa ko Yàlla,’ 6 kooku amatul warugaru teral baayam.” Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada. 7 Yéen ñi naaféq, Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, bi mu naan:
8 “Xeet wii ñu ngi may teral ci seen gémmiñ,
waaye seen xol sore na ma.
9 Seen màggal amul benn njariñ,
ci li ñuy jàngle dénkaaney nit kese.”»
10 Noonu Yeesu woo mbooloo mi ci moom ne leen: «Dégluleen te xam: 11 du li dugg ci gémmiñ mooy indil nit sobe, waaye li ciy génne mooy indil nit sobe.»
12 Bi taalibeem ya déggee loolu, ñu ñëw ci moom ne ko: «Ndax xam nga ne, Farisen yi dañoo mer ndax loolu nga wax?» 13 Yeesu ne leen: «Garab gu sama Baay bi ci kaw jiwul, dees na ko buddi. 14 Bàyyileen leen, ay gumba lañu yuy wommat ay gumba; bu gumba dee wommat moroomam nag, kon dinañu daanu ñoom ñaar ci kàmb.»
15 Piyeer nag jël kàddu gi, laaj Yeesu: «Firil nu léeb wi.» 16 Noonu Yeesu ne ko: «Ndax ba tey seen xol dafa tëju, yéen itam? 17 Xamuleen ne, lépp lu dugg ci gémmiñ, ci biir lay jëm tey génn ca bérab bu làqu? 18 Waaye li génn ci gémmiñ mu ngi jóge ci xol; loolu mooy indil nit sobe. 19 Ndaxte ci xol la xalaat yu bon di jóge, ak bóom, njaaloo, ndoxaanu yàqute, càcc, seede lu dul dëgg ak saaga. 20 Yooyu ñooy indil nit sobe, waaye lekk ak loxo yoo raxasul du tax nit am sobe.»
Yeesu faj na doomu jigéen, ja askanoo réewu Kanaan
21 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ci diiwaanu Tir ak Sidon. 22 Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.» 23 Waaye Yeesu waxu ko dara. Ay taalibeem nag ñëw ci moom ne ko: «Doo ko yiwi, mu ngi nuy topp, di yuuxu ci sunu kaw.» 24 Yeesu ne: «Yónniwuñu ma, lu dul ci xari bànni Israyil yu réer.»
25 Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!» 26 Yeesu ne ko: «Jël ñamu gone yi, sànni ko xaj yi, rafetul.» 27 Waaye jigéen ja ne ko: «Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci seen lekkukaayu boroom.» 28 Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Yaw jigéen ji, sa ngëm réy na; na am, ni nga ko bëgge.» Noonu doomam daldi wér ca saa sa.
Yeesu faj na ñu wopp
29 Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, ñëw ci weti dexu Galile; mu yéeg ca aw tund, toog fa. 30 Ba mu fa nekkee, nit ñu bare ñëw ci moom, indaale ay lafañ, ay làggi, ay gumba, ay luu ak ñeneen ñu bare. Ñu teg leen ci tànki Yeesu, mu faj leen. 31 Nit ñépp waaru, ndaxte gis nañu luu yuy wax, làggi yu wér, lafañ yuy dox, ak gumba yuy gis. Ñu daldi màggal Yàlla Buuru Israyil.
Yeesu bareel na ay mburu ñaareel bi yoon
32 Gannaaw loolu Yeesu woo ci moom taalibeem ya ne leen: «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk. Bëgguma leena yiwi te lekkuñu, ngir bañ ñu tële ci yoon wi.» 33 Noonu taalibeem ya laaj ko: «Waaye fu nuy jële ci àll bi mburu mu doy ngir mbooloo mu tollu nii?» 34 Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaari mburu ak ay jën yu ndaw.»
35 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf. 36 Mu fab juróom ñaari mburu yi ak jën yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ñu séddale leen mbooloo mi. 37 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale juróom ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des. 38 Gannaaw jigéen ñi ak gone yi, góor ñi ci lekk matoon nañu ñeenti junni.
39 Noonu Yeesu yiwi mbooloo mi, dugg ci gaal, ñëw ci wàlli Magadan.