Léebu fukki janq ya
25
1 «Booba nguuru Yàlla Aji Kawe ji dina mel ni fukki janq, ñu fab seeni làmp, génn, gatanduji boroom séet ba. 2 Fekk juróom ca janq ya di ñu am xel, juróom ya ca des ñàkk xel. 3 Ñi ñàkk xel nag fab nañu seeni làmp, waaye fabaalewuñu diw; 4 waaye ñi am xel ñoom fab nañu seeni làmp, fabaale diw ciy njaq. 5 Ni boroom séet bi yéexee ñëw nag, ñépp gëmméentu bay nelaw.
6 «Noonu ci xaaju guddi baat jib ne: “Boroom séet baa ngi, génnleen, gatandu ko.” 7 Bi ko janq ya déggee, ñu jóg, defar seeni làmp. 8 Ñi ñàkk xel wax ñi am xel: “Mayleen nu ci seen diw, ndaxte sunuy làmp ñu ngi bëgga fey.” 9 Waaye ñi am xel ne leen: “Li nu yor du doy ngir nun ak yéen. Tee ngeena dem ca jaaykat ya, jënd?”
10 «Bi nga xamee ne dem nañu jëndi, boroom séet ba agsi. Ñi amoon diw ci seeni làmp, ànd ak boroom séet ba ca reer ya. Noonu bunt ba tëj. 11 Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu!” 12 Mu ne leen: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, xawma leen.”
13 «Yewwuleen nag, ndaxte xamuleen bés ba mbaa waxtu wa.
Léebu surga, ya njaatige bi dénk xaalisam
14 «Te it nguuru Yàlla dafa mel ni kuy tukki bitim réew. Bi muy laata dem, mu woo ay surgaam, batale leen alalam, ku nekk lu mu àttan. 15 Kenn ka, mu dénk ko juróomi milyoŋa, keneen ka, mu dénk ko ñaar; ka ca des, benn; daldi tukki.
16 «Bi mu demee nag, ki jot juróomi milyoŋ ya dem, di ci jula, ba amaat yeneen juróom. 17 Noonu it ki jot ñaar amaat yeneen ñaar. 18 Waaye ki jot benn milyoŋ dem, gas pax, nëbb fa xaalisu njaatigeem.
19 «Gannaaw diir bu yàgg njaatigeb surga ya délsi, daldi leen laaj alalam. 20 Noonu ki jot juróomi milyoŋ ya jegeñsi, indi yeneen juróom naan: “Kilifa gi, dénk nga ma juróomi milyoŋ; seetal, ame naa ci yeneen juróom.” 21 Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.” 22 Naka noona ki jot ñaari milyoŋ it jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, dénk nga ma ñaari milyoŋ, seetal, ame naa ci yeneen ñaar.” 23 Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.”
24 «Gannaaw loolu nag, ki jot benn milyoŋ jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, xamoon naa ne, nit ku néeg nga; dangay dajale foo jiwul, tey góob foo faruwul. 25 Moo tax ma ragaloon la, ba dem, nëbb sa xaalis ci biir suuf; mi ngii, fabal li nga moom.” 26 Waaye njaatigeem ne ko: “Surga bu bon nga te tayel! Gannaaw xamoon nga ne damay dajale fu ma jiwul, tey góob fu ma faruwul, 27 kon waroon ngaa yóbbu sama xaalis ca denckati xaalis ya. Bés bu ma ñëwee nag, ma mana jot li ma moom ak la mu jur.” 28 Noonu njaatige bi ne: “Nanguleen xaalis bi ci moom, jox ko boroom fukki milyoŋ yi. 29 Ndaxte ku am dinañu la dolli, ba nga barele, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu. 30 Te sànnileen surga bu amul njariñ bi ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy te yéyu.”
Àtteb xeet yi
31 «Boo xamee ne Doomu nit ki mu ngi ñëw ci ndamam, ànd ak malaaka yépp, booba dina falu ni buur, toog ci jalam bu soloo ndam. 32 Bu boobaa dees na dajale xeeti àddina yépp ci kanamam, te dina leen xàjjale, ni sàmm di xàjjalee xar yi ak bëy yi, 33 mu teg xar yi ci ndijooram, bëy yi ci càmmoñam.
34 «Noonu Buur bi dina wax ñi féete ndijoor: “Agsileen, yéen ñi sama Baay barkeel, jël-leen nguur, gi ñu leen waajal li dale ci njàlbéenug àddina. 35 Ndaxte xiifoon naa, ngeen jox ma, ma lekk; te mar, ngeen jox ma, ma naan; nekkoon naa ab doxandéem, ngeen fat ma; 36 te rafle, ngeen wodd ma; woppoon naa, ngeen seetsi ma; te ñu tëj ma, ngeen ñëw fi man.” 37 Ci kaw loolu ñi jub dinañu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, nu jox la, nga lekk; mbaa nga mar, nu jox la, nga naan? 38 Kañ lanu la gisoon, nga nekk ab doxandéem, nu fat la; mbaa nga rafle, nu wodd la? 39 Kañ lanu la gisoon, nga wopp mbaa ñu tëj la, nu ñëw ci yaw?” 40 Noonu Buur bi dina leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa yu ngeen defalee loolu kenn ki gëna ndaw ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.”
41 «Gannaaw loolu dina wax ñi ci càmmoñam: “Soreleen ma yéen ñi alku, te dem ci sawara su dul fey, si ñu sàkkal Seytaane ak ay malaakaam. 42 Ndaxte xiifoon naa waaye joxuleen ma, ma lekk; te mar waaye joxuleen ma, ma naan. 43 Nekkoon naa ab doxandéem, waaye fatuleen ma; te rafle, waaye wodduleen ma; woppoon naa te ñu tëj ma, waaye seetsiwuleen ma.” 44 Ci kaw loolu dinañu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, mbaa nga mar, nga nekk ab doxandéem mbaa rafle, nga wopp mbaa ñu tëj la, te topptoowunu la?” 45 Kon dina leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa su ngeen ko defalul kenn ci ñi gëna ndaw, man ngeen ko defalul.” 46 Noonu ñii dinañu sóobu ci mbugal gu dul jeex, waaye ñi jub dinañu tàbbi ci dund gu dul jeex.»