Yàqug Yerusalem ak dellusig Doomu nit ki
13
1 Bi Yeesu di jóge ca kër Yàlla ga, kenn ca taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, xoolal! Ni mu réye ay doj, te rafete ni ay taax!» 2 Waaye Yeesu ne leen: «Du gis ngeen taax yu réy yii yépp? Lii lépp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»3 Gannaaw loolu, bi nga xamee ne Yeesu toog na ci tundu Oliw ya, jàkkaarlook kër Yàlla ga, Piyeer, Saag, Yowaana ak Andare fekki ko cig wet, laaj ko: 4 «Wax nu kañ la loolu di am? Te luy tegtal ne, mbir yii yépp a ngi bëgga mat?»
5 Noonu Yeesu ne leen: «Moytuleen, bu leen kenn nax. 6 Ñu bare dinañu ñëw ci sama tur naan: “Moom laa,” te dinañu nax ñu bare. 7 Bu ngeen déggee ay xare ak coowi xare, wottuleena tiit; loolu war na am, waaye mujug jamono ji jotagul. 8 Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Te yëngu-yënguy suuf dina am ciy bérab yu bare, ak ay xiif. Loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu.
9 «Moytuleen. Dees na leen jébbal àttekat ya, di leen dóor ay yar ca jàngu ya. Dinañu leen dëj ci kanam i boroom réew ak i buur ndax sama tur, ngir ngeen nekk seede ci ñoom. 10 Fàww xibaaru jàmm bi jëkka jib ci xeet yépp. 11 Saa su ñu leen jàppee nag, dëj leen ci péncum layoo, buleen jàq ci li ngeen wara wax; li ngeen jot ca waxtu woowa waxleen ko, ndaxte du yéenay wax waaye Xel mu Sell mi.
12 «Mag dina joxe rakkam cig dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, di bañ seeni waajur, di leen reylu. 13 Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba ca muj ga, mucc.
14 «Bés baa ngi ñëw, bu li ñuy wax “Lu araam luy yàqe” tegee ca bérab bu mu yelloowul; kiy jàng, na xam. Bu ngeen gisee loolu nag, ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya. 15 Ku nekk ci kaw taax mi, bul wàcc ngir dugg kër gi, fab say yëf ya fa nekk. 16 Ku nekk ci tool bi, bul ñibbi ngir fab sa mbubb. 17 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal. 18 Ñaanleen ngir seen gàddaay baña tase ak jamonoy seddaayu lolli. 19 Ndaxte booba dina am metit wu réy wu masula am, ba àddina sosoo ak tey, te dootul am mukk. 20 Te bu fekkul woon Boroom bi wàññi bés yooyu, kenn du mucc, waaye fekk na mu wàññi leen ndax gaayam ñi mu tànn.
21 «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Xool-leen, mu nga fale,” buleen ko gëm. 22 Ndaxte ñiy mbubboo turu Kirist ak ñiy mbubboo turu yonent, dinañu feeñ, di joxe ay firnde yu réy ak ay kéemaan, ba ciy nax sax ñi Yàlla tànn, su loolu manoona am. 23 Wax naa leen ko lu jiitu. Kon nag moytuleen.
24 «Waaye booba, gannaaw metit yooyu:
“Jant bi dina lëndëm
te weer dootul leer;
25 biddiiw yi di daanoo asamaan,
te kàttani asamaan yiy yëngu.”
26 «Noonu dees na gis Doomu nit ki ñëw ci niir yi, ànd ak kàttan ak ndam lu réy. 27 Dina yónni ay malaakaam, ñu dajale ñi mu tànn ci ñeenti xébla yi, fa àddina dale, ba fa asamaan yem.»
28 Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, tey xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na. 29 Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne jege na; mu ngi ci bunt bi sax. 30 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul. 31 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
Yàlla rekk moo xam bés ba
32 «Waaye bés boobu ak waxtu woowu, kenn xamul kañ lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam. 33 Moytuleen te xool! Xamuleen kañ la waxtu wi di jot.
34 «Mi ngi mel ni nit ku tukki, mu dénk këram ay surgaam, ku nekk ak sa sas, te sant bëkk-néeg bi, mu xool. 35 Yéen nag xool-leen, ndaxte xamuleen kañ la boroom kër gi di délsi, muy ci timis mbaa ci xaaju guddi, muy ci fajar mbaa njël. 36 Bu nee jalañ, bumu leen bett, ngeen di nelaw. 37 Li ma leen wax, ñépp laa ko wax: “Xool-leen!”»